dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

Yuusu Nduur : new Africa mballax

0:00 0:00

man Yuusu Nduur, maa ngiy woo bépp doomu Africa.

ñu bokk xalaat, bokk gis-gis, bokk yéene.

sãa froñceer, boole sunu am-am te liggéey.

na ñu daje, bañ a xajal kenn sunu diggante.

waratu ñu nangu kenn ñëw diñu féewale.

bul jiite réew, foog ne la fa nekk yaw yaa ko moom.

ngir bu dëgër, dala war a fekk nga bëgg sa réew.

te sàkku ndimbal, ndimbal na ca fekk loxool boroom.

ne bàcc géwel,

nëbbal sa junjuŋ jee, waawaaw.

ba ñëpp daje, ca pénc ma, waaw, ngir ñu waxtaan.

wuy Africa,

bu jant bi fenkee, waawaaw,

na la fekk jóg, ak sa jumtukaay, bëccëg bi gaaw na.

ñett du bëre,

te ñaara mën kenn.

yoon bi sore na, te metti na, na ñu ko waajal.

na ñu dajaloo boole sunuy kaddu doomi Africa.

na ñu dajaloo boole sunuy gis-gis doomi Africa.

na ñu dajaloo boole sunuy doole doomi Africa.

ne bàcc géwel, lëkkal sa junjun jee, waawaaw.

ba ñëpp daje, ca pénc ma, waaw, ngir ñu waxtaan.

wuy Africa,

bu jant bi fenkee, waawaw,

na la fekk jóg, ak sa jumtukaay, bëccëg bi gaaw na.

ñett du bëre,

te ñaara mën kenn, waawaaw.

yoon bi sore na, te metti na, na ñu ko waajal.

boodul noppe xalaat na nu defoon maam ya,

sa xol dootul neex te dootoo xalaat ludul fayantoo.

su ma sañoon Africa benn nit moo koy jiite.

ñu boole suñuy xalaat ak suñuy doole jox ko.

na ñu ubbi froñceer yi rattaxal yoon yi ba ñëpp gise.

cencoo, cenci,

wóg tugeesë,

ñiw Africa,

Seex Anta Jóob,

Kuame Nkuruma,

Stiivin (Stiiv) Bikko

waaya ba tay may woy jàmbaar yi fi nekkoon di bañ.

maa ngiy dellooti woy jàmbaar yi fi nekkoon di bañ.

di bañ nootit nit ku ñuuloo.

bër noppaliku ñu bare ñu ngiy dem ci yeneeni réew.

te mën a yam, fii ci seeni réew.

fale ca Tàmbaakundaa am na noppalukaay.

yeen waa Serekundaa na seen ñaan yi nangooy.

Bobbo-Julaaso.

su ma sañoon Africa benn nit moo koy jiite.

ñu boole suñuy xalaat ak suñuy doole jox ko.

na ñu ubbi froñceer yi rattaxal yoon yi ba ñëpp gise.

cencoo, cenci, wóg tugeesë, kiip on wóokiŋ, ñiw Africa, Seex Anta Jóob, Kuame Nkuruma, Stiivin (Stiiv) Bikko

óol yuu piipëel,

Africa.

ëttub wolof