dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

Yuusu Nduur : new Africa

0:00 0:00

man Yuusu Nduur, maa ngiy woo bépp doomu Africa.

ñu bokk xalaat, bokk gis-gis, bokk yéene.

sãa froñceer, boole sunu am-amte liggeey.

na ñu daje, bañ a xajal kenn sunu diggante.

waratu ñu nangu kenn ñëw diñu féewale.

bul jiite réew, foog ne la fa nekk yaw yaa ko moom.

ngir bu dëgër, dala war a fekk nga bëgg sa réew.

te sàkku ndimbal, ndimbal na ca fekk loxool boroom.

ni bàcc, nëbbal sa junjuŋ yii.

na ñëpp daje, ca pénc ma, waaw, ngir ñu waxtaan.

wuy Africa,

su jant bi fenkee,

na la fekk jóg, ak sa jumtukaay, bëccëg bi gaaw na.

ñett du bëre,

te ñaara mën kenn.

yoon bi sore na, te metti na, na ñu ko waajal.

na ñu dajaloo boole suñuy gis-gis doomi Africa.

na ñu dajaloo boole suñuy xalaat doomi Africa.

na ñu dajaloo boole suñuy doole doomi Africa.

na ñu dajaloo boole suñuy alal doomi Africa.

boodul noppe xalaat na ñu defoon maam ya,

sa xol dootul neex te dootoo xalaat ludul fayantoo.

bu ma sañoon Africa benn nit moo koy jiite.

ñu boole suñuy xalaat ak suñuy doole jox ko.

na ñu ubbi froñceer yi rattaxal yoon yi ba ñëpp gise.

cencoo, cenci,

kam tugeesë,

ñiw Africa,

wóg tugeesë,

kiip on wóokiŋ,

foo Africa,

Seex Anta Jóob,

Kuame Nkuruma,

Stiivin (Stiiv) Bikko

boodul noppi xalaat na ñu defoon maam ya,

sa xol du neex te dootoo xalaat ludul fayantoo.

bu ma sañoon Africa benn nit moo koy jiite.

ñu boole suñuy xalaat ak suñuy doole jox ko.

na ñu ubbi froñceer yi rattaxal yoon yi ba ñëpp gise.

cencoo, cenci,

kam tugeesë,

ñiw Africa,

wóok tugeesë,

kiip on wóokiŋ,

foo Africa,

Seex Anta Jóob,

Kuame Nkuruma,

óol yuu piipëel,

Africa.

ëttub wolof