dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

Yuusu Nduur : wommat

0:00 0:00

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

pàppa eksplike ñu.

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

góorgi waxtaane ko.

góorgi neena àdduna lu wóoradi la.

pàppa eksplike ñu.

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

pàppa eksplike ñu.

waaw, ma eksplike leen.

maak sama doom.

sama doom yéeg ci mbaam.

man may tette mbaam.

am ñu romb benn dëkk.

nit ñi toogoon foofu, ñu ngi naan xoolal xale be ka reew.

naaj bu tàng bii, moom mu waroon a tette mbaam.

sama doom deglul benn a ngoog.

maak sama doom.

sama doom wàcc mbaam.

man ma yéek ci mbaam.

moom muy tette mbaam.

beneen dëkk bu ñu romb.

nit ñi toogoon foofu, ñu ngi naan mag mii moo ñàkk xel.

sama doom deglul ñaar a ngoog.

àdduna bii,

soo defee lii, ñu ni na lale.

nga def lale, ñu ni la lii ñu gën a neex.

je sais, je sais, …

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

pàppa eksplike ñu.

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

góorgi waxtaane ko.

góorgi neena àdduna kenn xamu ko.

pàppa eksplike ñu.

góorgi neena àdduna ump …u ko.

pàppa eksplike ñu.

waaw, ma eksplike leen.

léegi ñu wàcc mbaam.

ñun ñaar ñuy tette mbaam.

ñeneen yu ñu romb fee, ñi ngi naan ñaar ñii ñoo ñàkk bopp.

léegi ñu yéeg ci mbaam.

kenn ommatul mbaam.

feneen fu ñu romb fee, ñu ngi naan ñii ñaar ñoo ñàkk yërmaande.

sama doom deglul ñett a ngoog.

àdduna bii,

soo defee lii, ñu ni na lale.

nga def lale, ñu ni la lii ñu gën a neex.

je sais, je sais, …

ne bàyyil, bàyyil, man su ma la rombee ;

bàyyil, bàyyil, man su ma la jiitoo,

nga wax ma lu ñaaw.

ne bàyyil, bàyyil, man su ma la rombee ;

ne bàyyil, bàyyil, man su ma la jiitoo,

nga wax ma lu ñaaw.

ne bàyyil su ma la rombee nga wax ma lu ñaaw.

man su ma la jiitoo nga wax ma lu ñaaw.

man li may def a gën li ngay def ?

am li ngay wax a gën li may wax ?

ne bàyyil, bàyyil, man su ma la rombee ;

bàyyil, bàyyil, man su ma la jiitoo,

nga wax ma lu ñaaw.

ne bàyyil su ma la rombee nga wax ma lu ñaaw.

man su ma la jiitoo nga wax ma lu ñaaw.

man li may def a gën li ngay def ?

am li ngay def a gën li may def ?

wommat, wommat …

dunyaa, ni mu mel a gën ni ngeen mel.

wommat, wommat …

ni dunyaa, ni mu mel a gën ni ngeen mel.

wommat,

su ma la wanee gànnaaw nga wax ci man.

waxoo ci man lu dul wax ju ñaaw.

lu ma def ngani baaxul.

lu ma ne amna, nga ni loolu amul.

waaw loolu lu ciy pexe ?

li ciy pexe mooy bul faale.

bul toppatoo te dee ko sóoraale.

Pàapa kane gal Mbay Jaw.

Allaaji Bada Lóo mooy baayam.

seetal Yuusu Nduur ni muy woye.

mbaar, …

seetal etuwaal ni muy defe.

da ñuy misig mu set Yuusu woy ci kawam.

su doyul, ñu dolli.

su ëppee, ñu xaaj ko.

su matul, ñun ñu mottali ko.

Ismayla Sow, ndax lu tane.

dunyaa, ni mu mel a gën ni ngeen mel.

wommat, wommat …

ëttub wolof