dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

Yuusu Nduur : dem dem

0:00 0:00

dem ! dem ! dem fan ?

dem ndax lan ? baay a ko moom.

dem ngir, xeer bu bare bii.

dem ndax, teen bu neex bii.

rab yi rekk, ñoom ñoo ciy naan.

naaj bi lakkatuma ; taw bi barewul.

dem ngir, bokk bool, mënu fee am.

dem ngir dafa, war a nekk góor, doon góor-góorloo.

dem ! dem ! dem fan ?

dem ndax lan ? liberte bi.

ci espaas, bu lëndëm bii.

sama bët yi, ci suuf di wut, garab bi nga xamanta ni ñooma suuxat.

bu ma seetee, garab bi bóow.

dem ngir, kër gi daf ma niru lu lëndëm.

dem ngir dafa war a nekk góor, doon góor-góorloo.

damay dem, ci àll bi.

ne damay dem, ci dex gu mag ji.

ne damay dem, waaw seeti sama nawle.

damay dem, si (ci) ban bu rittax bii.

ne damay dem, bërënguji ci.

ne damay dem, waaw seeti sama mbokk yi.

doon góore

doon góore

dem ! dem ! dem fan ?

dem ndax lan ? baay a ko moom.

dem ngir, xeer bu bare bii.

dem ndax, teen bu neex bii.

rab yi rekk, ñoom ñoo ciy naan.

naaj bi lakkatuma ; taw bi barewul.

dem ngir, bokk bool mënu fee am.

dem ngir dafa war a nekk góor, doon góor-góorloo.

damay dem, si (ci) àll bi.

ne damay dem, si (ci) dex gu mag ji.

ne damay dem, waaw seeti sama nawle.

damay dem, si (ci) ban bu rittax bii.

ne damay dem, bërënguji ci.

ne damay dem, waaw seeti sama nawle.

doon góore

doon góore

wan ma sa xarit, ma wan la ki nga doonooy.

wan ma sa mbokk, ma wax ko fi ngay jaar.

eey !

what do you need ?

eey eey !

yaw li la neex.

wan ma sa xarit, ma wan la ki nga doonooy.

wan ma sa bopp, ma wax la fi ngay jaar.

eey !

defal li la neexoo.

eeey !

yaw li la soob.

sàmmkatu mbott, moo xam ba cay sooxoo.

ñi mën a kot, ñoom daal amuñu mbaam.

eey !

defal li la neexoo.

eey yuu !

what do you want ?

óóóó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó

kër gi daf may niru lu lëndëm daal.

óóóó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó

dem ! dem ! dem ndax lan ? baay a ko moom.

dem ngir, xeer bu bare.

dem ndax, teen bu neex. rab yi rekk, ñoo ciy naan.

dem ngir, kër gi daf ma niru lu lëndëm.

dem ngir, góor dafa war a nekk góor-góorloo.

óóóó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó

óóóó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó ó ó ó ó ó óóóó

ëttub wolof