dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

jëgg b- 1 : kuy war géleem di tukki. jëgg yi fi jaaroon ay naar lañu.

jëgg b- 2 : yeb b-, sëf b-, yen b-. fas wi àttanul jëgg bi.

jëgg b- 3 : li ngay am boo wutee dund ci jamonoy xiif. dina mën a dund ci jëgg bi ba dugub ñor.