dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

far 1 : soxal. li nga koy defal faru ko.

far 2 : féete fenn. àttekat warul a far fenn.

far 3 : daŋ. ndoxum bisaab mi far na. safaan wi mooy ndoxe wala yolom.

far 4 : faase, efaase. far na li nekkoon ci tabló bi.

far 5 : bëggoon naa fa dem wànte damay far fomm, dafa guddi. dinañuy wax tamit faf.

far w- : góor gi ngay bëgganteel. ndaw si dafay yeeru faram wi rekk wànte li mu kooy won di jikkoom.