dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yugg : (ne yugg). dinañuy wax tamit yagg (ne) wala yàcc (ne). (seetal yàcc)

yugur-yugur j- : waaxusil ñu dem te nga bàyyi sa yugur-yugur ji.

yukk-yukk j- : deel dox doxinu nit te bàyyi sa yukk-yukki ji.

yulli : sotti, tuur. yulli na saaku ngooñ bi yépp. safaan wi mooy sol.

yul b- : kàlluur g-, mole b-. ci yul bi la am benn góom.

yulub : (ne yulub). dox ba dugg ci am pax, sërëx (ne). koñ bi dafa lëndëm mootax mu dox ba ne yulub ci pax mi.

yumpaañ j- : sa jabaru nijaay mooy sa yumpaañ.

yunn : feeñ feeñ bu gaaw. dafa ne yunn ci biir néeg bi rekk delluwaat.

yuppi : maye ay yére yu màgget. yuppil na yalwaankat bi.

yuqeel : dinañuy wax tamit yëqool wala yuqool. (seetal yëqool)

yuqeelu : taxaw ci ay cati tànk di am looy séentu mooy yuqeelu. dinañuy wax tamit yuqoolu, yuqamtalu wala yuqamtiku.

yuqi : yéegal tuuti lu ñu suloon mooy yuqi. bant yi ngeen samp dañoo sutante, dangay yuqi yenn yi ndax ñu mën a tolloo ñoom ñépp.

yuq g- : génne na yuq gi nekkoon ci biir yax bi.

yuqool : dinañuy wax tamit yëqool wala yuqeel. (seetal yëqool)

yureet : (ne yureet). sotteeku benn yoon. tepp-tepp moo gën yureet. (léebu).

yuri : sotti. yuri na ceeb bi ci bool. safaan wi mooy sol wala duy.

yuug : sëgg, yuur. buntu bi dafa gàtt, foog nga yuug soog a mën a dugg ci biir néeg bi. safaan wi mooy siggi.

yuuli-yuuli j- : juroom-ñaareelu jamonoy nawet jiy am diiru fukki fan ak ñett, céebo m-, ndabraan j-. tey la yuuli-yuuli war a jeex.

yuur : sëgg, yuug. garab gi dafa yuur. safaan wi mooy siggi.

yuur g- : dinañuy wax tamit yóor g-. (seetal yóor)

yuut : yuut na yére bi yépp.

yuux g- : dinañuy wax tamit yóox g-.

yuuy b- : lay b-. yuuy bee ko teree génn démb.