dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yogg : (ne yogg). bi mu yégee ne lajj na ci joŋante bi mu doon def ba léegi, dafa ne yogg rekk. dinañuy wax tamit yugg (ne).

yokk : dolli. mbaa ñaareel bi nga takk du la yokk ay deppãas kay ? safaan wi mooy wàññi.

yolaan b- : njàppaan b-. yolaan muusum àll muy nekk di jàpp ginaar yi la.

yolax : tàbbi te ñorul. (meññent). doomi siddéem yi dañoo yolax.

yolleeku : rocceeku. dem te kenn du la yég. yolleeku na ndànk dem yoonam. dinañuy wax tamit yolliku.

yolliku : dinañuy wax tamit yolleeku. (seetal yolleeku)

yolnde g- : yoonu ndox w-. yolnde gi fii lay jaar.

yolom : ñàkk a dëgër. takkaat ko, takk bi dafa yolom. safaan wi mooy daŋ, teeŋ, tàlli wala dëgër.

yoloos : (ne yoloos). génn génn bu àndul ak benn coow. bi ñu ko bettee muy yakktaan ndaw si, dafa ne yoloos dem.

yomb : kooku dafa bëgg lu yomb.

yomb b- : doomu yomb b-. Saalum lañu doon beye yomb bi.

yomb g- : lawtanu yomb b-. gone lawtanu yomb la ; boo walbatiwul, mu law fu la neexul. (léebu).

yomm : (ne yomm). dem ci lu amul benn waajaay, mott (ne). dafa dégg tàgge bi rekk ne yomm dem seen dëkk.

yonnent b- : yonent bi mooy ki Yàlla yónni ci doom-aadama yi. dinañuy wax tamit yonnent b-.

yoofaanu : dikkee nit ginnaaw, ruusaanu. dafa yoofaanu xale bi doon daw, jàpp ko.

yool b- : fey. jëf ju baax joo def rekk, borom bi dina la ci yool.

yoom : yolom. bàyyil buum gi mu yoom tuuti. safaan wi mooy teeŋ wala dëgër. / nee nañu waa ji dafa yoom.

yoon b- : bii yoon duma fa mën a jaar.

yoon w- : fu ñuy jaar ak tànk wala ak waruwaay. yoon wi dafa bare suuf. / luwaa b-. yoon wi ñu fi teg, waruloo ko jalgati, àk màqaama boo mën a am nag. / yoon waru fi nekk di dal ci kow ñii su ñu jalgatee, te du ko def ci kow ñee su ñu jalgatee.

yoo b- : kenn nelawul biig ndax yoo yu bare.

yoor-yoor b- : ci yoor-yoor lañu fiy dajesi di wax lu leen kenn waxloowul.

yoor : wàcce. yoor na goj bi ci teen bi.

yoos : ŋas. xale bi dafa yoos.

yoot : yoloosu. sàcc bi yoot na ba dugg ci biir néeg bi te kenn yégu ko.

yooy : sew, ràgg, làpp, jeex. xaj bi yooy na lool. safaan wi mooy suur wala am yaram.

yopp : xaar, nég. am na lu ngóor si di yopp fi mu toog.

yoqat : dem ba amatuloo benn yaakaar ci am mbir. sa njàng mi metti na, yàgg na waaya muñal rekk, dina baax, bul yoqat mukk. dinañuy wax tamit yoqi.

yoqi : dinañuy wax tamit yoqat. (seetal yoqat)

yorax m- : yorax mooy ndox muy wal ak doole di dem.

yor : lan la yor ci loxo bi ? dinañuy wax tamit yore. safaan wi mooy ñàkk.

yoroxlaan g- : yoroxlaan xeetu ñax la.

yorr : (ne yorr). yentem (ne), dagaj (ne). bi kaña gi génnee gis xale yi la ne yorr ci biir pax mi.

yowmalxayaam b- : bés-pénc b-. yowmalxayaam dina ñëw, Yàlla àtte jëf yépp. dinañuy wax tamit yowmalxiyaam b- wala yommalxiyaam b-.

yow : mbaa yow yaa ngi jubal ci sa liggeey ? dinañuy wax tamit yaw.

yox : nekk di yëngatu, ñàkk a dëgër. bantu sàkket wi dafay yox. / dem. bi mu la déggee ngay wax la yox ndax xaalis bi mu la yoreel.

yoxo y- : yoxo mooy bareelu loxo. benn loxo lañuy wax waaya su ëppee benn rekk, yoxo lañuy wax. ci ñaari yoxo yépp lañu ko pikiir.

yoxoos : dinañuy wax tamit yoxos. (seetal yoxos)

yoxos : dugg fenn te kenn du la yég mooy yoxos. dinañuy wax tamit yoxoos.

yoxos j- : yoxos xeetu rënd la. yoxos, paañ ak yéet yépp lay jay ca ja ba.