dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yidda j- : dinañuy wax tamit yedd j-. (seetal yedd)

yiir : muur, aar, musal, sàmm. baas bi dafa yiir nit ñi ci naaj wi.

yiir g- : yiir xeetu garab la.

yiiw : lu muur ay cër, lu jot, lu rafet. jigeen su bëggee jur doom ju baax, dafa war a yiiw. dinañuy wax tamit yiw. safaan wi mooy yiiwadi.

yiix : dinañuy wax tamit yeex wala yéex. (seetal yeex)

yikkat : dinañuy wax tamit yékkat wala yëkkat. (seetal yékkat)

yilif : moo yilif ñi fiy liggeeye ñépp. dinañuy wax tamit ilif.

yitte j- : ku bare yitte la. dinañuy wax tamit itte j-.

yitt : dóor, ñaf, duma, tex. su ko defati rekk, yitt ko.

yiwi : dinañuy wax tamit yiwwi wala yewwi. safaan wi mooy yeew wala tekki. (seetal yewwi)

yiw : dinañuy wax tamit yiiw. safaan wi mooy yiwadi. (seetal yiiw)