dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yeb 1 : dinañuy wax tamit yab. (seetal yab)

yeb 2 : sëf, yen. li nga yeb ci sareet bi yépp, fas wi attanu ko. safaan wi mooy yebbi.

yeb 3 : waajal jigeen mu dem sëyi, jox ko ay bagaasi waañ, digal ko. bul fàtte lañu la waxoon ba ñu lay yeb nga sëyi.

yedd : xelal, digal. ci yedd ko la yaayam dëkk wànte wax mënu ci moom dara.

yedd j- : diir bi jigeenu ju jëkkër ji gaañu war a toog, muuru laata muy am jeneen jëkkër ndax mu mën a wóor ne ëmbul laata jëkkër ji di gaañu. bala ngay daw ci ginnaaw ndaw si ngir takk ko, xaaral ba yedd ji jeex. dinañuy wax tamit yidda j- wala idda j-.

yeejaan b- : buumi der yu jóge ci deru nag. saag bi ay yeejaan lañu ko ràbbe.

yeel b- : wokk na yeel yi ba ñu weex tàll.

yeelu maam b- : yeelu maam teraanga la bu ñuy jox maam yi wala ñi maaseek ñoom bu ñuy ngénte seen sët.

yeendu : duma fa yeendu, damay dem te ñëw léegi.

yeen : yeen du ngeen ay tubaab, ay nit ñu ñuul ngeen.

yee : dafay nelaw, bul ko yee. safaan wi mooy yeetal.

yeer m- : kan m-, pax m-. yeer mooy pax mu xóot te yaatu.

yeeru : ëkku. takk-der yaa ngi yeeru jaaykatu sinebar bi.

yees : jënd na lal bu yees. dinañuy wax tamit bees. safaan wi mooy màgget.

yeew m- : yeew mu mag lañ gisoon àll ba.

yeex : dinañuy wax tamit yéex wala yiix. safaan wi mooy gaaw.

yegg : dinañuy wax tamit egg wala àgg. (seetal àgg)

yegg : dinañuy wax tamit àgg wala egg. (seetal àgg)

yekk : dinañuy wax tamit yakk. (seetal yakk)

yell : jaadu. kom dañu la dénkoon suñu alal ji, yell na, booy dem, nga wax ñu foo ko dugal.

yelu : tari ci suuf. julli tisbaar ak tàkkusaan dañu leen di yelu. dinañuy wax tamit yeru. safaan wi mooy biral.

yelwaan : dinañuy wax tamit yalwaan. (seetal yalwaan)

yem 1 : dem ba tollu fenn fi. fii la toolam yem. / dal ci dara, yemoo ak. dafa dox ba yem ci yow ngay tóx.

yem 2 : tolloo. yeen ñaar yeen a yem, kenn du ci wax dëgg. safaan wi mooy ëpp wala ëppante. / nekk ci diggante bi. li mu ko ci may barewul, tuutiwul, dafa yem rekk.

yem 3 : teey, toog benn palaas. sa doom ji yem na. safaan wi mooy yemadi, léej wala sob.

yemb 1 : pare, mat. li nga ñu doon defloo, yemb na. dinañuy wax tamit emb. safaan wi mooy des wala mànke.

yemb 2 : nite, am xel. li nga def ku yemb du ko def. safaan wi mooy yembadi wala muusadi.

yendeer g- : téj-fël g-. yendeer mooy yoonu génnukaay wu pareegul wu jinax di defar ngir mën di ci jaar.

yenn-saa-yi : léeg-léeg. yenn-saa-yi mu ñëw fi.

yenn w- : cere ju amul ndawal. yenn rekk lañu daan lekk ca daara ja.

yen : dimbale nit mu yenu dara. attanul saaku bi nga ko yen. safaan wi mooy yenni.

yentem : (ne yentem ). dagaj (ne), cabax (ne). jinax ji ne na yentem ci biir pax mi.

yenu maanaa : lu xel mën a jàpp, jaadu. loolu nga wax nekkul lu yenu maanaa.

yeññ w- : biir garab gu ñuy gor. yeññ mooy xolu garab.

yeraange g- : gàcce g-. yeraange ju mag la jële ca ndaje ma.

yer m- : foos b-. yer mi nekk ci ginnaaw mooy xasaw.

yeru : tari ci suuf. dinañuy wax tamit yelu. safaan wi mooy biral. (seetal yelu)

yet w- : ngot b-, bant b-. mbaam mi ngay dóor yet wi rekk, dafa am bakkan ni yow.

yett 1 : am na fi yetti kër. dinañuy wax tamit yatt wala ñett.

yett 2 : defar ay jumtuwaay ak ay bant. dafay xëy di yett ay toogu, ay gënn ak ay kuur ba ngoon. dinañuy wax tamit yatt.

yew : wër, làng. jigeen ñaa ngi yew tëggkati bóngo yi di tàccu.

yew : takk. danga war a yeew sa nag yi bala ñuy dugg ci biir toolu jàmbur bi. safaan wi mooy yewwi wala tekki.

yey : am dëgg ci kow nit. yey na la de ndax li mu waxoon a mujj am.

yeyoo : dinañuy wax tamit yelloo. (seetal yelloo)