dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yaa-bopp : am xam-xam bu làqu. ku yaa-bopp dafay gis lu ñépp dul gis.

yaafus : yambare, bàyyeeku. bul yaafus ba say morom yépp raw la. safaan wi mooy njaxlaf wala am-kàttan.

yaakaar : foog. yaakaar naa ne waa ji duñu wor.

yaa : béreb bi yaa na. dinañuy wax tamit yaatu. safaan wi mooy xat.

yaar : yaari jabar la yor. dinañuy wax tamit ñaar.

yaar b- : yaar ab natt la bu jege lool nattu meetar.

yaasa : togg yaasa. soxna si dafay yaasa tey.

yaay j- : ndey j-. yaay jee ko yàq waaye moo ciy ëppale. safaan wi mooy baay j-.

yab : ñàkk a weg. gone gi mag ñépp la yab. safaan wi mooy weg, jox cër wala rus. dinañuy wax tamit yeb.

yabóy-mërëg b- : yabóy-mërëg ak yabóy-tas ay xeeti yabóy la.

yabóy-tas b- : démb yabóy-tas rekk a amoon ja ba.

yabóy b- : yabóy xeetu jën la.

yafal : jox lekk, dundal, mbellax. dafay yafal ay xar di jaay.

yagg : (ne yagg). dinañuy wax tamit yugg (ne) wala yàcc (ne). (seetal yàcc)

yaj b- : yaj lañuy defare koog wala mbattu.

yakk : yakk na añ bi ba taaj. dinañuy wax tamit yekk.

yakktaan : jikkoom moy di yakktaan jigeen ñi.

yalandi : settali, lenqali. raxas raxas bu mujj. yalandi na ndab yi.

yal : yanq. dafa buddilu bëñam bu yal bi. safaan wi mooy dëgër.

yal b- : sindax b-. yal bi dugg na ci biir gajj gi.

yalwaan : saraxu. lutax ngay yalwaan te dara jotu la ? dinañuy wax tamit yelwaan.

yamarkiij : yamarkiij yax la buy nekk ci ginnaawu doom-aadama.

yambar : tóoy, nooy, yaafus. dafa yambar mootax moromam yi dëkk di ko ñuus. safaan wi mooy sawar wala njaxlaf.

yamb w- : ku bëgg lem, ñeme yamb. (léebu).

yaraax : tubey ju yaraax la soloon. / àll bu yaraax bii, gaynde du fi dëkk.

yaradal : jër. ndaw si dafa yaradal, doom ju mu am mu faatu.

yaram w- : seen liggeey bi dafay yàq yaram. dafa am yaram lool.

yar : xale ki ko yarul ba mu ci tolloo moo ko sànk.

yaru : dinañuy wax tamit am-teggin. (seetal am-teggin)

yatt : dagg ñax mu wow. xëdd lay defar ak ñax mi muy yatt.

yawaal b- : yawaal xeet la ci jën yi.

yawut b- : Israayel réewu yawut la.

yaxal : def bilaŋ. suñu paree, dinañu yaxal, wax la li ñu def ci xew li yépp.

yaxanal : sakkanal, oomal. àdduna yemul ci tey, sa xaalis bi ngay yàq yaxanal ko ngir ëllëg. safaan wi mooy yàq wala pasar-pasare.

yaxeet : baatu yaxeet dafay ànd ak baatu yàq wala yàqu di tekki bu baax. këram gi yàqu na yaxeet ci taw bi.

yax b- : yaxu jën bee galan ci gémmeñ gi. / bokk ci yax bu rëy mooy lan ? / yax dinay tekki tamit bëñu xale buy tàmbalee am ay gëñ. / yaxu wax ji mooy li wax ji wundu. / xale bi sa doom la ; su baaxee, yow la baaxal ; su bonee, yow la bonal ; man may naa la ko te ay yaxam rekklaa la laaj.

yaxu digg ginnaaw b- : yaxu digg-ginnaaw beey metti.

yaxu yamarkiij b- : ndunkurunk g-. ci yaxu yamarkiij bi la ko yet wi dal.

yay w- : àll bu dara nekkul. màndiŋ m-. Móritani am na yay.