dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yóbbu : yóbbu na ma seen dëkk. safaan wi mooy andi.

yónni : yebal. ki nga yónni matul ndaw.

yóor g- : yóor ci biir bopp lay nekk. dinañuy wax tamit yuur g-.

yóor w- : wàll w-. na ku nekk jot yóoram ci nag wi.

yóos j- : njabb m-. yóos xeetu jën la.

yóotu : tàllal sa loxo ngir jot dara. jot na li mu doon yóotu. / mbébet jot ci dara. li ngay yóotu, su ñëwee, yal na la jig.

yóox g- : fu waay tollu di dégg yóox gi. dinañuy wax tamit yuux g-.

yót : dinañuy wax tamit yét. (seetal yét)