dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yëbb : tooy tooy bu yem. yére bi dafa yëbb, summi ko.

yëddu : déglu wala xool ci sekkere. mu ngi taxaw ci palanteer bi di yëddu. dinañuy wax tamit yërndu.

yëf y- : dinañuy wax tamit yéf y-. (seetal yéf)

yëg : dinañuy wax tamit yég. (seetal yég)

yëkëti : mënuloo yëkëti taabal ji, dafa diis. safaan wi mooy wàcce, taaj wala teg.

yëkkat : dinañuy wax tamit yékkat wala yikkat. (seetal yëkkat)

yëkk w- : xàbbaan b-. yëkk wi dafay jaay.

yëlbu : dinañuy wax tamit yëlëbu. (seetal yëlëbu)

yëlëb : fëgës. bul yëlëb der bi suñu kow. dinañuy wax tamit yélëb.

yënd : tàkk bu baax, boy. uppal taal bi ba mu yënd.

yëngal : gësëm. ngelaw laa ngi yëngal bànqaasi garab gi. / neexaayu jàng yee ko yëngal ba muy daanu leer.

yëpp : dinañuy wax tamit yépp. (seetal yépp)

yëqóol : nee na nga may ko ndox, dafay yëqóol. dinañuy wax tamit yuqool wala yuqeel.

yërëm : yërëm naa dof bi nekk ci mbedd mi ci seddaay bi.

yërndu : dinañuy wax tamit yér wala yër. (seetal yër)

yër : dinañuy wax tamit yér wala yërndu. (seetal yër)

yër : toppatool say mbir te bàyyi ki ngay yër. dinañuy wax tamit yér, yërndu wala yëddu.

yës : sukk. gélem gi dafa yegsi rekk yës.

yët : dinañuy wax tamit yét. (seetal yét)

yëy : dinañuy wax tamit yéy. (seetal yéy)