dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yéefeer b- : li Yàlla santaane du ci def dara, dafa mel ni ab yéefeer rekk. safaan wi mooy aji-gëm j-.

yéeg : ci garab gi la golo gi bëgg a yéeg. safaan wi mooy wàcc.

yéem : waar, jaaxal. li muy def di leen yéem, du dara.

yéene 1 : li nga yéene sa bopp nga war a yéene sa morom.

yéene 2 : yégle, siiwal. li ngay yéene na doon xibaar buy jëriñ askan wi. dinañuy wax tamit yéeyne.

yéen b- : wudd w-, mbaar m-. ay xaram lay defaral yéen bi.

yéen w- : ndaw si ñuulal na yéen yi.

yées : lu gën a bon. moom moo yées ci askanam. / lu matul. bul sóor lu yées ñetti kilo ceeb.

yéet b- : ay yéet lay defar di jaay.

yéex : dinañuy wax tamit yeex wala yiix. (seetal yeex)

yéeyne : dinañuy wax tamit yéene. (seetal yéene)

yéf y- : toppatool sa yëf te bàyyi yu jàmbur. dinañuy wax tamit yëf y-.

yég : dafa ñëwul rekk wànte yég na ndaje mi. / yére bu diis rekk lay sol, dafa mel ni du yég tàngaay. / bàyyi xel nit ñi. sa alal ju bare ji bu mu la teree yég nit ñi, am saxul, ñàkk saxul. / barewul ay àndandoo ndax dafa yég boppam torob. dinañuy wax tamit yëg.

yékkat : gone gi mer na de, sànq ba léegi mu yékkat. dinañuy wax tamit yëkkat wala yikkat.

yélëb : fëgg. bul yélëb der bi suñu kow. dinañuy wax tamit yëlëb.

yépp : dëkk bi yépp ay beykat lañu. dinañuy wax tamit yëpp.

yére b- : mbubb m-, koddaay l-. yére bi mu sol mën na seddaay.

yér : dinañuy wax tamit yër, yërndu wala yëddu. (seetal yër)

yét : yóbbul. nee na nga yét ko dàllam yi. dinañuy wax tamit yët wala yót. safaan wi mooy andil.

yéwen : nango joxe, tabe, baax. góor dafa war a yéwen su amee lu mu joxe. safaan wi mooy nay.

yéy : du yéy guro. dinañuy wax tamit yëy.

yéyu : jooy jooy yu metti. ku ko def lu metti ba muy yéyu ?