dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

yàbbi 1 : sex ba pare génnewaat ko. dafa sex jaxatu bi, mu tàng lool, mu yàbbi ko. safaan wi mooy sex.

yàbbi 2 : soor, bàyyi. cuub bi dafay yàbbi mootax mu yàq yére yi nga ko booleeloon di fóot.

yàbb : (ne yàbb). ŋàmm (ne). bàyyi sa gémmeñ gi mu ubbeeku. mu ngi toog ne yàbb di yuut rekk. safaan wi mooy ŋeb.

yàcc : (ne yàcc). yogg (ne), bàyyeeku lool. danga ne yàcc rekk, jéemuloo am dara ngir ëllëg. dinañuy wax tamit yagg (ne) wala yugg (ne). safaan wi mooy njaxlaf wala sawar.

yàgg : yàgg na bitim réew torob. safaan wi mooy gaaw. / bu yàgg ba léegi ñu koy xaar ci li mu fi digewoon. / ñëw na fi bu yàggul. / jàngale na ci daara ju kowe ji lu yàgg laata muy dem bitim réew.

yàkkali : baatu yàkkali mu ngi jóge ci baatu yaa. (seetal yaa)

yàkkamti : li ngay yàkkamti, xamuloo ndax dinga ko fekkeem déet.

yàkki : baatu yàkki mu ngi jóge ci baatu yaa. (seetal yaa)

yàmbaa j- : yàmbaa ji dofloo na xale yu góor yu bare, bu ko laal, bu ko jege.

yàmbalaŋ : (ne yàmbalaŋ). màww (ne). baatu yàmbalaŋ dafay tekki buntu wala palanteer bu ubbeeku ba sës wala bére bu yaatu ba dee. palaanteer baa ngi ne yàmbalaŋ. kër gu ne yàmbalaŋ la am Almadi, ca Dakaar.

yàndoor : nekk ci nelaw yu xóot. sàcc bi dafa ko bàyyi ba mu yàndoor, mu yóbbu xaalisam bi.

yànj : leer nàññ, taaru. ndaw si yànj na lool waaye ndax jikko ji baax na ? safaan wi mooy ñaaw. / tàkk bu baax. upp na furno bi ba mu yànj.

yàpp : lekk yàpp. bukki yi yàpp nañu bëy wi.

yàq biir : mu ngi jóge ci baatu yàq. (seetal yàq.)

yàq der : mu ngi jóge ci baatu yàq (seetal yàq.)

yàq : golo yi yàq nañu lu bare ci tool bi. safaan wi mooy defar. / bul yàq ceeb bi, boo suuree ubal bool bi te jóg. safaan wi mooy sakkanal. / yàq der. yaa ngi toog di yàq deram te moo la gën fuuf. / yàq biir. yow miy yàq biir ak ki la ko sant, seetleen bu baax li ngeen di def.

yàwweeku : dinañuy wax tamit yàkkaliku wala yàwwiku. (seetal yàkkaliku)

yàwwiku : dinañuy wax tamit yàkkaliku wala yàwweeku. (seetal yàkkaliku)

yàwwi : dinañuy wax tamit yàkki wala yàkkali. (seetal yàkkali)