dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xub 1 : dinañuy wax tamit xëb. (seetal xëb)

xub 2 : xobbiku, xolliku. yaram wi dafa tàmbalee xub.

xubidaas : màgget bay soppeeku ci yaram. maam ji dafa màgget ba xubidaas.

xucc b- : lutt b-. xamal bu baax ni ngay dagge xucc bi.

xuddoosun : dinañuy wax tamit suboqun. (seetal suboqun)

xugge b- : xugge bi ci koñ bi la dëkk. dinañuy wax tamit xuuge b-.

xuleet : (ne xuleet). xool bu baax li nekk. bi mu demee ba ne xuleet la bàyyi lépp lu bon li mu doon def.

xulli : ubbi bu baax ay gët. mu ngi xulli gëtam yi di la xool waaya li nga wax xamu ci dara.

xul : soow, xas. góor gaa ngi xul rekk, lu mu mer ?

xuluñe j- : jaxatu j-. teeyal, xuluñe ji dafa tàng.

xumb : sabar ga bare na nit, xumb na.

xumtoo : wax ci suuf. li ngeen di xumtoo, wax leen ko ci kaw. dinañuy wax tamit xuumtoo.

xunn 1 : baatu xunn dafay ànd ak baatu xasaw di tekki ba mu ëpp. nen bu nëb bi dafa xasaw xunn.

xunn 2 : xoñoñ, mer. li nga wax moo ko tax a xunn.

xunti m- : dinañuy wax tamit xunt m-. (seetal xunt)

xunt : béreb bu deme ni am pax. ci ay xunt la soldaar si làqatuwoon. dinañuy wax tamit xunti m-.

xupp : xëbal, ragalloo. bu ko dóor, xupp ko rekk.

xureet : xureet a ko daanee fan yii.

xurfaan : soj. dafa xurfaan mootax muy jënd garab yi.

xuri : dinañuy wax tamit xosi wala xusi. (seetal xosi)

xur w- : seen dëkk ci xur la nekk.

xus 1 : dagg ay kawar, wef. dafay xus kawari poqtaan yi rekk.

xus 2 : (ne xus). bare ba dee, (ne) gàññ. dinañuy wax tamit xas (ne) wala xasar (ne). (seetal xas)

xusër : (ne xusër). jékki jékki rekk feeñ, jimeet (ne). fi ñu koy laajtee la ne xusër.

xusi : dinañuy wax tamit xosi. (seetal xosi)

xutaab b- : mbir muy waral ay fitna. loolu boo ko defee, dinga dugal sa bopp ci xutaab.

xutba : waare. bi imaam bi di xutba la yegsi ci jumaa ji.

xutti : dinañuy wax tamit xotti. (seetal xotti)

xutt : ragal, buqat. xutt a tax duy foyi ci moromam yi. safaan wi mooy ñeme.

xutux : am ay pax. guy garab la gu xutux.

xuuf : wat. lutax nga xuuf sa bopp ?

xuuge : xëŋŋ. dinañuy wax tamit xugge. (seetal xugge)

xuuj : bon. kenn du jënd sa portaabal bi ndax dafa xuuj ba pare. safaan mooy baax wala mucc-ayib.

xuumtoo : dinañuy wax tamit xumtoo. (seetal xumtoo)

xuur-baat : naqari-baat. woykat bi dafa xuur-baat.

xuur : xomaag, weñe. buntu yi tàmbali nañoo xuur.

xuur y- : dambal y- (baat bu ñaaw la). bàyyil xuuri xar mi.

xuusmaañàpp b- : garxàll g-, njoogaan b-. rajoom bi ab xuusmaañàpp la.

xuuxaan : ku la ne waa ji dafa xuuxaan ?

xuux : xuux baat la bu ñuy wax ngir tiital nit. dinañuy wax tamit xóox.

xuy-xamaj : dinañuy wax tamit xuy wala xuy-xuyi. (seetal xuy)

xuy-xuyi : dinañuy wax tamit xuy wala xuy-xamaj. (seetal xuy)

xuyentaan b- : tàkk-fay b-. xuyentaan baa ngi naaw di ñëw.

xuyet : xuyet mooy leeral ab néeg ab diir ci jamonoy timis ngir dàq rab yu bon yi fa nekk. dinañuy wax tamit xuyët.

xuyët : dinañuy wax tamit xuyet. (seetal xuyet)

xuy : tàkk ak a fey. làmp baa ngi xuy rekk. dinañuy wax tamit xuy-xuyi wala xuy-xamaj.