dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xob w- : xobi garab gi tilimal nañu fii yépp.

xocc : sàtt. baatu xocc dafay ànd ak baatu jub di tekki lool. xottu buteel gi dafa jub xocc. dinañuy wax tamit kocc.

xoddi : wocci, puus mu dem. ki ngay àndal du nit ku baax, nanga ko xoddi. safaan wi mooy jàpp.

xodd : (ne xodd ). jadd (ne). nekk ci anam bu àndul ak benn yëngatu. ñu ngi ne xodd di seetaan waa ji di jàpp jaan ji.

xodd g- : xodd xeet la ci picc yi.

xoddoos : xuur (baat). baatam bi nii la mel, dafa xoddoos.

xogg : ku xogg mooy ku sa baat dugg ci say wagg.

xoj : poñe baat ba mu dëgër. dañu doon xeex, mu xoj ko.

xojog l- : àll bi bare na ay xojog. dinañuy wax tamit xojox l-.

xojox l- : dinañuy wax tamit xojog l-. (seetal xojog)

xolli : masin bi xolli gerte mooy liggeeyam.

xol : jox lekk, xont. picc mi dafay xol doom yi.

xol b- : feebaru xol la yore. / ci digg bi. këram a nga ca xolu dëkk ba. / tàng-xol. góor gi dafa xat-xol. / teg naqaru mbëggeel. ki mu doon njëkk a bëgganteel moo yàq xolam. / xol bi jeex na ci li nga def. / may naa la ko ci xol bu sedd. / li nga ko defal sedd na xolam bi.

xolu tànk b- : ci xolu tànk la lakk.

xom-xom g- : xom-xom xeetu ñax la.

xomaag : xuur. paaka bi dafa xomaag.

xomb : dinañuy wax tamit xomm. (seetal xomm)

xomb g- : kànnaar b-. xomb gi la sàcc bi dàjji.

xomm : baatu xomm dafay ànd ak baatu ñor. yàpp wi ñor na xomm. dinañuy wax tamit xomb.

xomp : posone, tooke. bu sa menn xel daj ngay xomp doom-aadama.

xonet : mer. li mu la wax jarul xonet.

xonjom : liggeey. doomu jàmbur ji nga xonjom ba mu dof du la jig.

xonq-nopp b- : tubaab b-, waa ërob b-. xonq-nopp bi wërsi suñu réew mi, nanga ko wan teraanga ju mat sëkk.

xonq : deretu xaj. piis bu xonq la xotti.

xont : jox lekk, xol, leel. soxna si dafay xont doom ji.

xoñoñ : mer, xunn. dem ak dikk bi muy def ci neen moo ko tax a xoñoñ.

xoob : sóob. tëgg bi dafa xoob jaaru bi. safaan wi mooy xobbi.

xoob m- : xoob xeet la ci picc yi.

xooj : xooj na bisaab bu xonq bi. safaan wi mooy jukki.

xool : dafa nekk di xool ndaw si bay bëgg a daanu ci pax mi. / seet ci nit. Omar sa nawle la te mu ngi dog buumi gàcce yi, nanga xool ci moom.

xoor w- : xoor ci baat lay nekk, mu ngi tollu ci catu pottax bi.

xoos 1 : bàyyil bool bi ngay xoos.

xoos 2 : xiif. dafa xoos ba mënul a taxaw bu baax.

xoos g- : xoos xeetu gajj la guy sax ci ndox rekk.

xoot-xoot b- : xoot-xoot mooy ndox muy des ci ndab bu ñu ko raxasee ba pare.

xoox : sonn ba ëpp ndax ay daw, soon lool. dafa daw ba xoox.

xoox b- : baleel xooxi buy yi.

xopp s- : xopp mooy paaka bu dem ba amatul ñawtan.

xoqtal : tiital, xëbal, xupp. bàyyil xale bi ngay xoqtal.

xor 1 : am sãasu di am nawet bu baax. xor na lool wànte nanguwul a bey.

xor 2 : def ay kokkiyaas ci ab miir. xor ay miir moo doon liggeeyam.

xor 3 : weexal. ñaata laa lay xor ?

xoraay : xonq coyy. tëgg bi dafa tàngal weñ gi ba mu xoraay.

xormbet : woyof ba mu ëpp, ndoxe. àttaaya bi dafa xormbet.

xorom 1 : def xorom ci ag togg. ndax xorom nga togg gi ?

xorom 2 : yor xorom su ëpp ci yaram. jigeenu-wérul ji dafa xorom.

xorompolle b- : dafay jaayaale xorompolle.

xorondom w- : xorondom yi bare nañu ci jànj bi.

xosi : muus mi xosi na ko. dinañuy wax tamit xusi wala xuri.

xosi b- : xosi yére bu ñu cuub cuub bu baxa defaale ci ay rëdd la.

xosi w- : xosi mooy doomu mbëtt.

xos : ñakk a nangu ku la jege, tàng. xaj bi dafa xos. safaan wi mooy lewet wala noppi.

xos b- : xos mooy téere bu ñuy def ci ab tool ndax mu génne lu bare ci liñ fa bey.

xos g- : xos ci màndargay tekkerlu yi la bokk, ñuŋ koy bindee nii : ","

xotar b- : cabbu buy b-. ay xotar yu bare lay jaay.

xoteet : (ne xoteet). lu xotteeku ci lu gaaw wala ba jeex. bi muy wàcc ci oto bi la yéreem bi lonku, ne xoteet.

xoti b- : petax m-. dafay yar ay xoti.

xotti : lutax nga xotti sa yére bi ? safaan wi mooy ñaw. / jënd piis. duma mën a xotti tabaski bii di ñëw. dinañuy wax tamit xutti.

xott w- : dajaleel xotti buy yi, tuuri leen.

xottu-buteel b- : tojitu buteel. defal ndànk bala ngay dëgg xottu-buteel bi.

xottu-buteel g- : garabu xottu-buteel g-. ay xottu-buteel la def ci ginnaaw këram.

xoymet : bàyyi muy feeñ (awra), sàgganu. defaral sa sër bi, yaa ngi xoymet nit ñi.

xoyyi : sew. feebaram bee ko tax a xoyyi.