dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xeddi : dañuy xeddi néeg bi xëddaat ko. safaan wi mooy xëdd.

xeeb : gënuloo ko lenn ba koy xeeb. safaan wi mooy naw.

xeej : fitt g-. bu njëkk ay xeej lañu daan xeexe.

xeelu : xool xoolinu ku mer ak ay cati gët. xale bu jigeen baa ngi xeelu waa ji.

xeeñ : génne xet gu neex. li ndaw si di togg a fiy xeeñ. safaan wi mooy xasaw.

xeereer : nekk ci diggante ñuul ak xees. ñuulul, xeesul, dafa xeereer.

xeer w- : doj w-. etijãa yaa ngay sànni takk-der ya ay xeer.

xeeru-baat w- : dafa am ay xeeru-baat.

xees : nee na jabar ju xees lay wër. safaan wi mooy ñuul.

xeet : xoos. nanga xeet cin li ba mu weex tàll.

xeet w- : mbokki ndey y-. bu leen dara jaxase ndax yeen a bokk wenn xeet. safaan wi meen m-.

xeex : dañu doon xeex, kenn ki gaañ ko.

xef-ak-xippi : ci lu gaaw. dem na ñëw ci xef-ak-xippi.

xef : sànq ba léegi mu ngi xef rekk. safaan wi mooy xippi.

xejem : dinañuy wax tamit xajam. (seetal xajam)

xejj : am jàmm ci béreb, féex. ndaw si xejj na ca sëy ba. safaan wi mooy xat.

xej b- : jabar ji jëkkër ji gën a bëgg. xej bi la yóbbu bitim-réew.

xekki : dallu ba pare. dafa jóge ci ay daw, xaaral mu xekki nga soog a wax ak moom. dinañuy wax tamit xiqi.

xellami : niiroo. ñaari kër yi xellami nañu. safaan wi mooy wuute.

xelli : sotti fenn. xelli na ci ndox mi, naan.

xelmati : mel ni lu gis wala lu dégg. xelmati naa Usmaan ca ja ba. / am ay màndargay dara. waa ji dafay xelmati ak sa rakk ji.

xel m- : xel dina dem fu tànk yeggul. / xel mu neex la yore. / xelam a tollu nóonu rekk. / xalaat b-. li mu wax xel la wànte kenn déggluwu ko ndax li mu amul xaalis, amul benn daraja.

xembali : tooyal xepp. xembali na lal bi.

xembi : mën nga xembi taal bi léegi, ceeb bi ñor na. safaan wi mooy xamb.

xeme b- : saabu xeme lay sangoo fan yii.

xemmem : bëgg a lekk, bëgg a am. sëriñ bi nee na yàppu dibi la xemmem. dinañuy wax tamit xemem.

xent : xer. nanga xent meew mi de bala nga koy naan.

xepp 1 : baatu xepp dafay ànd ak baatu tooy di tekki ba ëpp. tooy na xepp ci taw bi. dinañuy wax tamit xipp.

xepp 2 : daggat, fejat, dammat. dafay xepp bant bi, def ay matt.

xer b- 1 : jën w-. dafa wuti ay xer ngir sàkket wi muy defar.

xer b- 2 : dëgëraayu bant bu wow. xeru bant bee sonal lawbe bi.

xerem : (ne xerem). patt (ne), tekk (ne), muut (ne). baatu xerem dafay tekki lu ne tekk, amul benn coow. seen kër gaa nga ne xerem, kenn nekku fa.

xereñ : dinañuy wax tamit xarañ wala xareñ. (seetal xarañ)

xer : xent. mbaa xer nga ndox mi laata nga koy naan.

xer w- : xer mooy njubbu ginaar wala lu yeeneen xeeti njanaaw.

xesaw : dinañuy wax tamit xasaw. (seetal xasaw)

xesen : dinañuy wax tamit xasan. (seetal xasan)

xetax b- : dinañuy wax tamit xatax b-. (seetal xatax)

xettali : génne ci ay jafe-jafe. dafa bëgg ku ko xettali.

xew 1 : ñaw bi mu sol moo xew tãa yii.

xew 2 : am. dafa am lu xew ci kër gi.

xewer b- : doomu xewer b-. xewer bi ñoragul.

xewer g- : garabu xewer gi meññ na.