dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xóll : (ne xóll). xulli. xoole bu baax. nelawul, mu ngi ne xóll di xool nit ñi. safaan wi mooy gëmm.

xóoñ : xoos ceeb bu xëm bi taq ci taatu cin. soo añee ba pare nga xóoñ cin li.

xóot : teen bi xóot na lool.

xóox : dinañuy wax tamit xuux. (seetal xuux)

xóoyal : farin lay xóoyal.

xóoy : leer leer gu yem. làmp bi des naa leer, dafay xóoy.