dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xëb : ndox mi xëb na. dinañuy wax tamit xub.

xëcc : ñoddi. yaa xëcc buum gi ba mu dagg. safaan wi mooy puus, bumax wala jañ.

xëcc w- : fas wu boole melo wu weex ak wu ñuul. xëcc wi gaaw na lool.

xëdd 1 : wërale ñax ci ab càkkaar ba bu mu senn, bu ci naaj mën a dugg. tey lañu doon xëdd néegam. safaan wi mooy xeddi.

xëdd 2 : xëdd lekk ci fajar gi laata ñuy salaatu ngir waajal bésu koor.

xëddeen : bantu ron bu mag mooy xëddeen.

xëj-na : dinañuy wax tamit xéj-na wala xëy-na. (seetal xéj-na)

xëj : dinañuy wax tamit xéj. (seetal xéj)

xëllëmtoo : sàppaanoo, seerantoo. dàll yu bees lay xëllëmtoo.

xël g- : garabu xël g-. xël xeet la ci garab yi.

xël w- : dinañuy wax tamit xél w-. (seetal xél)

xëm 1 : bi mu daanoo ci daamaar ji, dafa xëm. safaan wi mooy ximmi.

xëm 2 : lakk ba ñuul kukk. mburu mi dafa xëm. mboq mi nga doon lakk, xëm na.

xëndënduur b- : xëndënduur xeetu gunoor la.

xënd : ragal. dafa xënd rekk wànte dara nekkul ci diggante bi. safaan wi mooy ñeme.

xënte : soxlo am mbir lool. kenn ku nekk ci xale yi tekki la xënte.

xënt : dinañuy tamit xant. (seetal xant)

xënt : dinañuy wax tamit xant. (seetal xant)

xëŋŋ : xuuge. maam ji dafa dem ba xëŋŋ.

xëpp : tuur. mbër maa ngi xëpp suuf ci kowam. dinañuy wax tamit xapp.

xër 1 : dinañuy wax tamit xér. (seetal xér)

xër 2 : gàllankoor ag noyyi, fatt. saaxaar saa ngi xér nit ñi.

xërëm : dinañuy wax tamit xérëm. (seetal xérëm)

xërën : dinañuy wax tamit xaran. (seetal xaran)

xërr : xërr baat la buy tekki coow li ñuy dégg su nit sànnee dara ak doole.

xët-xëti : mer ba mënuloo toog benn béreb. lu ko tax di xët-xëti nii ?

xëtëb : (ne xëtëb). yegsi rekk dugg ci waxtaan wi, rabaj (ne). fu mu fekk nit ñi di waxtaan, mu ne ca xëtëb.

xëtër b- : buuse bi génne na xëtëru xar mi.

xët : yaayam a ko xët.

xët m- : am na menn xët mu dindeekoo ci téere bi.

xëtt : saag bi mënul a ñàkk a xëtt, li nga ci def a diis. / jaar ci biir. ci biir nag yi la xëtt.

xëtt g- : fiir g-. xëtt gi jàpp na picc yu bare.

xëx : sonn lool ba mënoo wax. bàyyi ko mu dallu, dafa xëx.

xëy-na : dinañuy wax tamit xëj-na. (seetal xëj-na)

xëy : dinañuy wax tamit xéy. (seetal xéy)