dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xébla b- : danga xaw a moy xébla bi. dinañuy wax tamit xibla b-.

xédd : bëgg, sopp, nob. dafa xédd ndaw si bay bëgg a tàggook sagoom. safaan wi mooy bañ, sib wala jéppi.

xédd b- : xédd xeet la ci jën yi. dinañuy wax tamit sëdd w-.

xéewal g- : xéewal mooy lu neex lu la bett. Yàlla bette na ko xéewal. dinañuy wax tamit xéwal g- wala xiiwal g-.

xéew : xooj. dangay xéew sunguf si, nga naan ko, baax na ci sa jàngoro ji.

xéj-na : xéj-na dafa déggul li ma ko waxoon. dinañuy wa tamit xëj-na wala xëy-na.

xéj : dinañuy wax tamit xaj 2, xay wala xéy. (seetal xay)

xéj : mën a dugg wala mën a nekk fenn. oto bi xéj na fi. dinañuy wax tamit xaj wala xëj.

xéll : dinañuy wax tamit xél wala xëll. (seetal xél)

xél : baatu xél dafay ànd ak baatu xam di tekki bu baax. xamoon nga xél ne alali askan wi nga lekk, du la jig. dinañuy wax tamtit xéll wala xëll.

xél w- : daw y-. xél wi ngay dawal oto bi ëpp na. dinañuy wax tamit xël w-.

xérem : maam ya dañu daan xérem. dinañuy wax tamit xërëm.

xér : yéwen. dafa xër, du maye lu yem. dinañuy wax tamit xër. safaan wi mooy nay wala ŋott.

xérñenn : waral ay metti biir. li mu lekk sànq moo ko xérñenn.

xéwal g- : dinañuy wax tamit xiiwal g- wala xéewal g-. (seetal xéewal)

xéy-na : dinañuy wax tamit xéy-na. (seetal xéy-na)

xéy : dinañuy wax tamit xaj 2, xay wala xéj. (seetal xay)

xéy : dem ci suba. dangay xéy wala dangay gont ? safaan wi mooy gont. / dem liggeeyi. deel xéy waxtu, di wàcc waxtu. dinañuy wax tamit xëy.