dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

xàbbaan b- : nag wu ñu tàpp w-, yëkk w-. pël bi ay xàbbaan rekk lay jaay.

xàll : fàkk yoon. gaa yi xàll nañu yoon wi ba mu leer nàññ.

xàmp : dagg ak ay gëñ, xàppati. xàmp na pom bi.

xànc : wut ay xànc. tey damay xànc.

xàndoor g- : illeer b-. xàndoor gi ñaw na.

xànjar b- : xànjar mën na nekk xeetu weñ, mën na nekk tamit weccet.

xànq : leel. dafa xànq mootax muy watu ndel rekk.

xàññaaral : fés bu baax. fi nga toog dafa xàññaaral.

xàpp : xar ak sémmeñ. lawbe bi xàpp na taatu garab gi yépp.

xàpp b- : wateef g-. xàpp bii la ko ñépp xame.

xàpp g- : seŋoor g-. xàpp bokk na ci ay gàllaaji mbër.

xàqataay : reetaan ci kow. ñu ngi bàyyi seen liggeey bi fii, dem ca mbedd ma di xàqataay.

xàtt : baatu xàtt dafay ànd ak baatu wex di tekki ba ëpp. jaxatu bi dafa wex xàtt.

xàwwi : ubbi bu baax. xàwwi na palanteer bi ndax ngelaw li dugg bu baax. safaan wi mooy ub wala tëj.