dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wudd : yafal ab mala. fas wi borom dafa ko wudd ay weer mootax mu suure nii.

wujj w- : ki nga bokkal jëkkër mooy sa wujj. / jamaale b-. ay jamaale lañu mootax juboowuñu.

wulli : defar ab der ba ñu mën koo jëfandikoo. wulli ay der mooy liggeeyam. / dóor ba mu nooy. laata pólis di yegsi, gaa yi wulli nañu sàcci bi. / taggat ci dara. wulli nañu fas wi ba mu mokk.

wund : tekki. bala ngay tontu, xaaral ba xam li wax ji wund.

wund w- : muus m-, janaab j-. wund wi ci boppam rekk lay nekk. dinañuy wax tamit und w-.

wuññi : xàwwi sutura, weer. yaaŋ koy wuññi de, wànte li nga def a gën a ñaaw. safaan wi mooy nëbb.

wuq w- : dinañuy wax tamit wëq w-. (seetal wëq)

wure : ci ngoon ba léegi ñu ngi ci ron garab gi di wure.

wuri : yég, tas. pënd bi wuri na.

wuruj : njublaŋ. dafa doon wuruj ca këru liggeeyukaay ga, ñu dàq ko.

wurus w- : ngalam b-, gal b-. denc na ay wurus.

wut : kër gu mu dëkk lay wut.

wuub : wuub baat la bu ñuy wax bu ñuy yuuxu sàcc. wuub ! sàccee.

wuude b- : wuude bi li muy defar rafet na, dëgër na. dinañuy wax tamit uude b-.

wuuf : dinañuy wax tamit uuf. (seetal uuf)

wuul b- : nere b-. dinañuy wax tamit uul b-. (seetal uul)

wuul g- : nere g-. dinañuy wax tamit uul g-. (seetal uul)

wuum : rey ay gëñ. daqaar ji mu doon macc moo wuum ay gëñam. dinañuy wax tamit um.

wuute : ñàkk a niroo. ñaari baŋ yi wuute nañu. / ñàkk a teew. dafay faral di wuute ndaje mi.

wuutu : jël palaasu keneen. ki mu fi wuutu, dafa luubal ci alal ji.

wuy w- : tojal wuy wi tàbbee ci guy gi, génnee buy bi.

wuyu : dinañuy wax tamit uyu. (seetal uyu)