dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wocc 1 : jur doom ju juddoowul ak bakkan. ndaw si dafa wocc.

wocc 2 : bàyyi. dinañuy wax tamit wacc. safaan wi mooy tiye wala ŋëb.

woccu : lu ko jot ba muy woccu ? dinañuy wax tamit waccu.

wodd : takkal sër. solal na xale bu góor bi tubey, wodd xale bu jigeen bi. / wutal ay yére. sa jabar yow yaa ko war a wodd.

wogas : dinañuy wax tamit wog wala wogos. (seetal wog)

wogg w- : donj w-. suusal na cere ji, def ay wogg yu bare. /xeer w-. wogg wi dal na ko.

wog : bi muy jaar ci taa-taa bi, dafa wog tànki tubey ji ba ci óom yi. dinañuy wax tamit wogas wala wogos.

wogos : dinañuy wax tamit wog wala wogas. (seetal wog)

wok : xasan. góor gi wokk na yeel yi ba ñu weex tàll.

wol 1 : dëbb. jigeen ñi soq nañu dugug ji, wol ko. dinañuy wax tamit wal.

wol 2 : ëf. dinañuy wax tamit wal. (seetal wal)

wolli : dindi ñax yu bon yi, bey. tàmbali nañu wolli dugub.

wolluwaay b- : dinañuy wax tamit wollandoo b-. (seetal wollandoo)

wolof b- : làkku wolof. wolof benn la ci làkki Senegaal yi. / ku bokk ci xeetu wolof. ab wolof la fa takke.

wolonteer b- : dinañuy wax tamit baay-defal-yàlla -b. (seetal baay-defal-yàlla)

womb : tubey ji dafa ko ëppoon, mu womb ko. dinañuy wax tamit omb.

wommat : dinañuy wax tamit ommat. (seetal ommat)

wonaasu : wann. mënul wonaasu li muy lekk. dinañuy wax tamit wonnaasu.

wonk : gone gaa ngi toog ci potu-sàmbur bi di wonk. dinañuy wax tamit onk. (seetal onk)

wonnaasu : dinañuy wax tamit wonaasu. (seetal wonaasu)

wonni 1 : jël ay neni ginaar wala yu picc. ginaar gi lañu wonni.

wonni 2 : lu amatul wala lu defootul. loolu wonni na léegi, ku liggeeyul, dañu lay jële fi nga nekk, teg fa sa morom.

wonn : dinañuy wax tamit wann. (seetal wann)

won : portale bi la leen di won. safaan wi mooy nëbb.

won g- : garabu won g-. won xeetu garab la fii ci réewum Senegaal.

woñ : dinañuy wax tamit wañ. (seetal wañ)

woñ : dinañuy wax tamit wañ. (seetal wañ)

woññi : dinañuy wax tamit waññi. (seetal waññi)

woññi : dinañuy wax tamit waññi. (seetal waññi)

woññ : dinañuy wax tamit waññ. (seetal waññ)

woññ : lim, xayma. dinañuy wax tamit waññ. (seetal waññ)

woŋ : woŋ na ko ci ndel. dinañuy wax tamit woŋŋ.

woŋŋeetu : dinañuy wax tamit waŋŋeetu. (seetal waŋŋeetu)

woŋŋeetu : dinañuy wax tamit waŋŋeetu. (seetal waŋŋeetu)

woŋŋ : dinañuy wax tamit woŋ. (seetal woŋ)

woom : naat. dinañuy wax tamit oom. (seetal oom)

woo : woo na la ay yoon wànte dégguloo ko.

wooñ : afal. danga war a wooñ bunt bi ndaw néeg bi féex.

woor : magum jëmm la wànte du woor mukk. safaan wi mooy wori.

wootal : dinañuy wax tamit ootal. (seetal oo)

woowu : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

wopp : feebar. dinañuy wax tamit opp. safaan wi mooy wér. (seetal opp)

wori : safaan wi mooy woor. (seetal woor)

worma j- : teggin w-, aajo j-. sa wax ji amul benn worma. dinañuy wax tamit orma j-.

wor : jàmbu. ndaw si wor na waa ji ko bëggoon a takk. dinañuy wax tamit or.

woromba b- : daamina b-. yére bu am woromba ci kow ba ci suuf la soloon.

worox w- : àll b-. ab sàmm lañ fekk ca worox wa.

woru-biir : woru-biir mooy dige boo narul a def.

woslu-àq : def lenn lu la war ci am mbir. dafa doon waslu-àqam rekk wànte xam na ne xale bi kenn mënu ci moom dara.

wos : defar noppale. wos mooy teg ab cin ci ay xeer boo ciy togg.

wot : dinañuy wax tamit wat. (seetal wat)

woto b- : ndaama b-, daamar j-, daabo b-. jënd na fa ab woto. dinañuy wax tamit oto b-.

wottu : dinañuy wax tamit wattu. (seetal wattu)

wow-bët : dëgër-bët. ndaw si dafa wow-bët, soo ko takkee, ci rusloo la lay dëkk. safaan wi mooy am kersa.

wow-bopp : dëgër-bopp, wowle. du dégg mukk, dafa wow-bopp.

wow : bant bi dafa wow. safaan wi mooy tooy. / sew, jeex. ñàkk a lekk a ko tax a wow nii. safaan wi mooy am yaram.

woy : dinañuy wax tamit way wala wëy. (seetal way)

woyof-bopp : ku woyof-bopp mooy koo xam ne loo ko wax mu gëm ko.

woyof : dàll yi woyof nañu. dinañuy wax tamit oyof. safaan wi mooy diis. / wàccee sa bopp, sempal. nit dafa war a woyof.