dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wiccax : yélëb. bu ñu wiccax sa yoxo yi.

wicc : kuy wicc ndox mi ? dinañuy wax tamit wëcc.

wiiri : etijaŋ yi dañoo baare yoon wi mootax oto yi di wiiri.

wiir b- : tuwaal b-. xëdd bi dafay senn mootax mu def ci ay wiir.

wiis b- : buloŋ b-. wiis bi dafa réer.

windeel : dinañuy wax tamit wëndéel. (seetal wëndéel)

wiñ : dinañuy wax tamit wañ. (seetal wañ)

wird : dinañuy wax tamit wérd. (seetal wérd)

wirgo b- : xeet w-, waaso w-. gajj gi ci wirgo akkaasiyaa la bokk.

wis 1 : tepp-teppal, ñepp-ñeppal. taw bi rëyul, dafay wis rekk. dinañuy wax tamit wis-wisal.

wis 2 : dolli jëndkat bi ci li nga ko jaay. jaay na ko màngo, wis ko.

wisit b- : soxna si dafa defsi wisit ci loppitaal bi.

witteen b- : dinañuy wax tamit wëtteen b-. (seetal wëtteen)

witt : dinañuy wax tamit wëtt. (seetal wëtt)

wiyole : àgg ci jigeen ci lu dul coobareem. bëgg sol lu gàtt mootax ñu wiyole ko.