dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

waa-jur w- : waa-jur mooy sa pàppa wala sa yaay. dinañuy wax tamit way-jur w- wala wëy-jur w-.

waa-kajoor b- : ku dëkk wala ku cosaanoo Kajoor lañuy tudde waa-kajoor.

waabajiiba b- : dinañuy wax tamit rambaaj b-. (seetal rambaaj)

waaj : waaj na pare, di xaar oto bi ñëw, mu dem.

waalo-waalo b- : ku dëkk wala ku cosaanoo Waalo lañuy tudde waalo-waalo.

waa j- : dinañuy wax tamit waay s-. (seetal waay)

waañ w- : béreb bu ñuy togge. jigeen dafa war a nangoo dugg waañ.

waaraam y- : waaraam mooy bareelu baaraam. ci misaal benn baaraam lañuy wax, wànte su ëppee benn, ñaar, ñetti wala ay waaraam lañuy wax.

waar : xutba, waxtaanal ay nit ci diine. waxtaanam wa ca gàmmu ga waar na ñu bare. / jaaxal, yéem. li ma gisoon muy def, waar na ma.

waar w- : wàll w-, làcc w-. liy jëmale sa réew kanam, fexeel bey ci sa waar.

waas : defar ay jën laata nga leen di togg. jën yi ngay waas, na set.

waaso w- : wolof, séereer, pulaar, joolaa ay waasoo lañu ci Senegaal. dinañuy wax tamit waasoo w-.

waasoo w- : dinañuy wax tamit waaso w-. (seetal waaso)

waat : gëñ. waat na ko ci Yàlla ne du moom.

waaw : waaw ! dinaa fa ñëw su neexee Yàlla. safaan wi mooy déedet.

waax b- : ay banti waax lañu defare baŋ bi.

waax g- : garabu waax gi yàgg na fi mu nekk.

waaxu : dox ak jeego yu gaaw. nañu waaxu ndax ñu yegg bala muy guddi. safaan wi mooy daagu.

waay-waay : ngella. waay-waay, boo rombatee sa dëkkandoo, nanga ko nuyu.

waaya : wànte. jël na ko fa, muy liggeey waaya amul njàng ma war ca liggeey ba. dinañuy wax tamit waaye.

waaye : dinañuy wax tamit waaya. (seetal waaya)

waay : waay baat la buy firnde ag kéemtaan wala am mer. waay ! nit ñi bare nañu de. noppil, bul ñu tanqal waay !

waay s- : benn nit, nit ku ñu xamul. waay si dafay làcce yoonu fi mu jëm. dinañuy wax tamit waa s-.

wacc : bàyyi. dinañuy wax tamit wocc. (seetal wocc)

waccu : dinañuy wax tamit woccu. (seetal woccu)

wadd : rot. li mu yorewoon wadd na te yégu ko.

wagar-wagari : ku diis mooy dox di wagar-wagari. safaan wi mooy foyy-foyyi.

wagg y- : wagg mooy bareelu mbagg. ci misaal benn mbagg lañuy wax, wànte su ëppee benn, ñaar, ñetti wala ay wagg lañuy wax.

wajan w- : safaan wi mooy ndaakin w-. (seetal ndaakin)

wajj : dinañuy wax tamit fiiriir. (seetal fiiriir)

wakãas y- : bër g-. elew yi dañu nekk ci wakãas yi.

wal 1 : sottiku, tuuru. ndoxum taw maa ngi wal di ñëw.

wal 2 : ëf. li muy wal sufle bi mooy tanqal nit ñi.

wala : mbaa. dinañuy wax tamit walla. dangay dugg wala nga génn.

walas w- : waxandor w-. walas xeetu jën la.

walbati : dippi. ne ko mu walbati dàll wi. dinañuy wax tamit walbati wala ëlbati. safaan wi mooy dëpp. dinañuy wax tamit wëlbati wala ëlbati. safaan wi mooy dëpp.

wallet w- : ñebbe j-. fan lañuy beye wallet wi ?

walliyu b- : góor gi jikkoy walliyu la yor. dinañuy wax tamit wàlliyu b-.

wallu : ñëw dimbalesi. nit ñi dañu doon wallu waa kër gi doon lakk. dinañuy wax tamit wollu.

wanag w- : duus b-, gaanuwaay b-. wanag wi dafa war di set saa yu nekk. dinañuy wax tamit wanog w-.

wann : wann na tàngal bi mu doon macc. dinañuy wax tamit wonn.

wan : këram gi lay wan ay ganam. dinañuy wax tamit won. safaan wi mooy nëbb.

wanog w- : dinañuy wax tamit wanag w-. (seetal wanag)

wantilaatëer : wantilaatëer baa ngi upp wànte dafa tàng ba léegi.

wañ : bul wañ loxo bi, danga koy gaañ. dinañuy wax tamit woñ wal wiñ. safaan wi mooy tàllal.

waññi : dëpp. waññi na xale yi doon seetaani xeex ba. dinañuy wax tamit woññi.

waññ : ndax mën nga waññ xar yi ma xam ñaata la ñu. dinañuy wax tamit woññ.

waŋ : yore taat wu rëy. dafa waŋ mootax du mën a toog ci baŋ bu tuuti bi. dinañuy wax tamit wëŋ.

waŋŋeetu : mbaam mi nanguwul a daw, saa yoo ko dóoree, mu waŋŋeetu. dinañuy wax tamit woŋŋeetu.

war 1 : danga war a màndu ci mbir mu ñu la boolewul.

war 2 : yéeg ci kow dara. mag ñi fas lañu daan war bu ñuy tukki. safaan wi mooy wàcc.

wasag w- : kenn du lekk lu dul wasagam. dinañuy wax tamit wërsëg w-.

wasin-wees w- : jigeen ju wasin bees lañuy tudde wasin-wees.

wasin : am doom, jur. kañ la ndaw si wasin ? dinañuy wax tamit wësin.

wat 1 : diri. bukki baa ngi wat médd mi. dinañuy wax tamit watat.

wat 2 : wat nañu ko ndel bu set wecc. dinañuy wax tamit wot.

watt : watt : mu ngi watt ci màngo ji. dinañuy wax tamit witt wala wëtt.

wattu : saytu. waa ji dafay wattu kër gi. dinañuy wax tamit wottu.

wax-dëgg : wax-dëgg waa ji soxla na ndimbal.

wax-noppi : lu mekanisee bi mënul a defar, yow mi ko jàngul wax-noppi.

waxambaane w- : xale bu góor b-. doomam ji waxambaane la léegi.

waxande w- : gaal g-, kàggu g-, maal b-. waxande wi dafa fees dell ak ay yére.

waxandor w- : walas w-. waxandor xeetu jën la.

waxatumaak : astemaak, sàkkaatumaak. kenn mësu ko dégg muy xuloo sax waxatumaak xeex. dinañuy wax tamit waxatumalaak.

waxatumalaak : dinañuy wax tamit waxatumaak. (seetal waxutamaak)

waxee : dinañuy wax tamit waxe. (seetal waxe)

waxe : ni nga ko waxe ñaaw na. dinañuy wax tamit waxee.

waxin w- : baatu waxin mu ngi jóge baatu wax. waxin dafa war a rafet.

waxloo : baatu waxloo mu ngi jóge baatu wax. (seetal wax)

wax : li ngay wax, na doon lu la wóor.

waxset w- : waxset mooy jamonoy nawet ji muy gën a taw.

waxtaan w- : ñaaroo b-, gise b-. baatu waxtaan mu ngi jóge baatu wax. (seetal wax)

waxtu : kebetu, xultu. baatu waxtu mu ngi jóge baatu wax. (seetal wax)

waxtu w- : bul tarde de, nanga sàmmonte ak waxtu wi.

waxu g- : baatu waxu mu ngi jóge baatu wax. waxu mu ngi tollu ci put. (seetal wax)

way 1 : meew mi way na. safaan wi mooy seey wala ruy.

way 2 : waa ji ku mën a way la. dinañuy wax tamit wëy wala woy.

way-jur w- : dinañuy wax tamit wëy-jur b- wala waa-jur b-. (seetal waa-jur)

wayndare b- : téere xam-xamu alxuraan b-. sëriñ bi jàng na ay wayndare yu bare.