dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wóllëre w- : xame b-, ñoñ y-. ndéem sa wóllëre la, waru la seetaan ci ay jafe-jafe.

wóolu : dañu la wóolu, dénk la suñu alal ji, fexeel ba bul tas suñu yaakaar. dinañuy wax tamit óolu. safaan wi mooy wóoloodi.

wóom b- : dinañuy wax tamit óom b-. (seetal óom)

wóor : li ngay dugg, na doon lu wóor ndax naxekat yi dañoo bare jamonoy tey. safaan wi mooy wóoradi.

wóoy : wóoy baat la bu ñuy wax bu ñuy ñaan wallu. wóoy ! ñu ngi may agereese.