dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wéddi : dinañuy wax tamit weddi. (seetal weddi)

wéen g- : dinañuy wax tamit wen. (seetal wen)

wéer : li nga wéer ci taax mi, mbaa du daanu ci kow nit ñi.

wéet : nekk yow rekk. dafa wéet ndax jëkkër ji nekku fi. safaan wi mooy xumb.

wékki : safaan wi mooy wékk. (seetal wékk)

wékk : lonk. wékk na sabadoor bi. safaan wi mooy wékki wala lonki.

wéq : dóor ak tànk. nag wéq na doomam waaya bañu ko. (léebu).

wér-gi-yaram w- : réewu mu nekk war naa taxaw bu baax ci wér-gi-yaramu askanam. dinañuy wax tamit wér-gu-yaram w-.

wérd : dafay wérd subaak ngoon. dinañuy wax tamit wird.

wérekcekk j- : ñàkk nelaw g-. wérekcekk jee ko tax a xoole ba bër-set.

wérëñ : (ne wérëñ). sófoor bi dafa séen alkaati bi rekk, ne wérëñ, dëpp. dinañuy wax tamit wëréñ (ne) wala wëriñ (ne).

wér : du wér mukk, fu mu tollu mu ngi feebar. safaan wi mooy feebar wala opp. / dëgër. góor gi mag mu wér la.

wéttaliku : baatu wéttaliku mu ngi jóge ci baatu wéet. (seetal wéet)

wéttali : baatu wéttali mu ngi jóge ci baatu wéet. (seetal wéet)

wéttal b- : baatu wéttal mu ngi jóge ci baatu wéet. (seetal wéet)

wéy : dem, jàll. bi mu jëlee wàllam rekk la wéy.