dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

wàcc-raxasu b- : kuy def liggeey bu koy tilimal, uwiriyee b-. wàcc-raxasu yaa ngi daan seen doole ci réew mi.

wàcc : jóge ci kow ñëw ci suuf. moo yéegoon ci kow garab gi wànte wàcc na. safaan wi mooy yéeg. / jóge sa bérebu liggeeyukaay, dem ñibbi. deel xëy waxtu, di wàcc waxtu ndax sa peyoor mën laa lew domm. safaan wi mooy xëy.

wàgg b- : li nekk ci tefes gi yépp wàgg yee ko génne.

wàlliyu b- : dinañuy wax tamit walliyu b-. (seetal walliyu)

wàll w- : dinañuy wax tamit waar w- wala làcc w-. (seetal waar)

wàntaay b- : uppukaay b-. jëlal wàntaay bi upp ko.

wànte : waaye. waxoon na ko ko wànte fulaalul woon waxam ji.

wàññi : dafa wàññi lu bare ci ay atam. safaan wi mooy yokk. / ki la féetewul fenn, bu la meree lu mu lay wàññi ?

wàttu s- : kuddu-luus g-. dinañuy wax tamit mbàttu m-.