dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

uude b- : uude yi fi dëkk ñu ngi defar ay dàll ak ay saag yu rafet te dëgër. dinañuy wax tamit wuude b-.

uuf : teg ci ay lupp. toogal uuf xale bi. dinañuy wax tamit wuuf.

uul b- : uul xeetu meññent la.

uul g- : garabu uul g-. uul gi amatul ay doom.