dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

um 1 : ne nañu soo waxee ak nit laata ngay sëlmu, danga koy um. dinañuy wax tamit ub. safaan mooy jig.

um 2 : tàmbali weeru koor gi. ndéem gis nañu weer wi tey, dinañu um suba.

umpaañ j- : sa jabaru nijaay mooy sa umpaañ. li waa ji yorul rekk a tax umpaañ ji bañ ne du ñu ko may doomu nijaay ji. dinañuy wax tamit yumpaañ j-.

ump : ñàkk a yég wala xam am mbir. dara du ko ump ca xew la.

umra : dem Màkka laata jamonoy aj g-. umra na ñetti yoon.