dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

tubaab b- : waa-ërob b-, nasaraan b-. tubaab yi dañoo seetsi suñu dëkk bi.

tubaarfakàllaa : sant Yàlla. tubaarfakàllaa, kër-këri naa ba am kër.

tubay j- : tubay ji mu sol jotu ko. dinañuy wax tamit tubey j- wala tubëy j-.

tubey j- : dinañuy wax tamit tubay j-. (seetal tubay)

tubëy j- : dinañuy wax tamit tubay j-. (seetal tubay)

tucc : baatu tucc dafa toppandoo coow liy am sooy dëbb dara.

tuddeeful j- : saan w-. dafa yore ay tuddeeful.

tudd : jaar ci turu dara ak làmmeñ. ba mu ko meree ba léegi, du ko tudd, du ko taas. / jox ab liir tur ci bésu ngénteem. tudd nañu xale bi ba noppi. / Omar la pàppaam tudd.

tuddu-ma-la-mbaay : tuddu-ma-la-mbaay mooy tur wi ñuy jox jaan bu guddee.

tufe : muusal. tufe na yàpp tabaski wi.

tufli : dinañuy wax tamit tafli wala tëfli. (seetal ci kow).

tukkal : nekk ci jamonoy tëbu. fas wi dafa tukkal.

tukki : nekku fi, dafa tukki.

tukulëer b- : dinañuy wax tamit tukuloor. (seetal tukuloor)

tukuloor b- : tukuloor turu waaso la. dinañuy wax tamit tukulëer.

tulaabéer b- : tulaabéer xeetu xar la.

tulli : kiy tëgg ndënd mi ci ag sabar mooy tulli.

tul : ku tul xeeti gànnaay yi mel ni paaka wala jaasi du ñu ko dugg.

tum b- : bantu gumba b-. jàppal ci tum bi, jéggil gumba bi tali bi.

tumpaañ : dinañuy wax tamit tump. (seetal tump)

tump : daagu. mu ngi tump di ñëw. dinañuy wax tamit tumpaañ.

tumurànke : nekk foo xamul kenn. dafa tumurànke fa mu nekk ndax amu fa benn mbokk.

tund w- : jànj b-. seen dëkk ci aw tund la nekk. dinañuy wax tamit tunn w-.

tungoob : yenu ci ay wagg. tungoob na xale bi. dinañuy wax tamit tungoom.

tungoom : dinañuy wax tamit tungoob. (seetal tungoob)

tungune b- : ngàttaan l-. tungune bi mën na liggeeyam. safaan wi mooy njool m-.

tunn w- : dinañuy wax tamit tund w-. (seetal tund)

tuñ-tuñi : daŋ-daŋi, tés-tési. lutax muy tuñ-tuñi nii ?

tuñ m- : ndaw si dafa jamu tuñ yi.

tuñoomlu : dal ci kenn ci ag cong. dafa tuñoomlu ak ku ko ëpp doole mootax mu gaañu.

tuŋlu : yeeru, tëru, kar. kaña gi la gaa yi di tuŋlu fii.

tuq s- : gënn gu ndaw, ngënn s-. nokkos lay dëbb ci tuq si.

turki b- : simis bu am ay fànt ci wet yi. turki bu weex la soloon.

turne : jàdd. dafa tóx di ñëw, waaye bi mu sénnee pàppam rekk la turne.

tur w- : baatu tur mu ngi jóge ci baatu tudd. (seetal tudd)

turu-biir-kër w- : sa turu-biir-kër mooy tur wi ñu lay woowe ci kër gi.

turumtàcc : cuq. soow mi dafa ma turumtàcc, fan nga jënde ?

tusiñe b- : toggkat b-. ndaw si tusiñe la ci otel bi.

tusngal : pastel. tusngal na xale bi.

tus : dara. fey nañu ko suñu xaalis te defu fi tus.

tusur : saa-su-ne. dina fiy jaar tusur. dinañuy wax tamit tuusur wala tuusuur.

tut w- : léget b-. am na tut wu nekk ci kanam gi.

tutti : dinañuy wax tamit tutt. (seetal tutt)

tutt : tutt mooy njëkk a dindi desiti ñam yi nekk ci ndab yi soog leen di raxas. dinañuy wax tamit tutti.

tutu : buddee ag gajj fii, jëmbët ko fee. tamaate ji yépp, dañu ko fi tutu.

tutur : tutur mooy defar njambaan ci biir wuy wi.

tuubaa g- : Tuubaa dëkk bu mag la bu nekk Senegaal, doon màkkaanu xalif bi ci yoonu murit, te ñu fay amal ag màggal at mu jot.

tuuba b- : tuuba xeetu gënn-tuxu la.

tuubiruubi : baatu tuubiruubi mu ngi tekki tuub naa ko. tuubiruubi ! duma ko waxati mukk.

tuub : tuub mooy jël ab dogalu ñakk a defati dara ba fàww. li nga tuub ne dootuloo ko def ba pare, waratuloo ko defaat. / jóge ci diine ji nga nekkoon, dugg ci jeneen diine. mbaa du dafa tuub, dugg ci diiney lislaam ngir takk ndaw si rekk ? safaan wi mooy tubbi.

tuufa j- : tuufa xeetu rënd buy jóge ci géej la.

tuuf : dugal lu deme ni ndox ci biir bët. danga koy tuuf lii suba ak ngoon.

tuug : tuug kàddu la guy jib soo déggee wala nga gis lu ñaaw. tuug ! loolu saaga la, bu ko waxati de.

tuuma j- : tuuma ji yàq na àddunaam.

tuun g- : muuti g-, fut g-. tuun wax ju ñaaw la.

tuur b- 1 : ay g-. tuur bi sa tuur la tey.

tuur b- 2 : gémmeñ g-. na tuuru fetal bi, jublu nee.

tuur-ndox : saw. xaar ko mu ñëw, dafay tuur-ndox.

tuur : xëpp. tuur na ndox mi nekkoon ci siwo bi. safaan wi mooy duy wala root.

tuur m- : tuur mooy lépp lu ñu mën a jàppe ni luy denc liy aar njaboot gi te mu mën a nekk aw rab, ab bant wala leneen.

tuur y- : béreb bi ñuy denc rab wiy aar njaboot gi, xàmb y-, xërëm y-. seen maam a fi defoon tuur yi.

tuus : di wër areen bi di fecc. ñaari mbër yi tuus nañu ba pare, sëgg bëre rekk a des.

tuuti-tànk b- : xale bu tuuti b-. tuuti-tànk yi lay jàngal. dinañuy wax tamit tuutànk b-. safaan wi mooy mag m-.

tuuti : may ko tuuti. safaan wi mooy bare. / bi muy nekk xale bu tuuti la fi ñëwoon ba léegi. safaan wi mooy ndaw. / tutee tere. tuuti xar mi mbëkk ko. dinañuy wax tamit tuut.

tuut : lu mu tuut, tuut moo la ko ëppale. dinañuy wax tamit tuuti.

tuwaalet y- : wanag w-. tuwaalet yi set nañu wecc.

tuwaal b- : permeyaabal b-. néeg bi dafay senn mootax mu lal ay tuwaal ci kow.

tuxma : yore biir buy daw. yóbbul xale bi kër doktoor, dafa tuxma.

tux : dinañuy wax tamit tóx. (seetal tóx)

tuyaaba j- : dinañuy wax tamit tiyaaba j-. (seetal tiyaaba)

tuyy : tuuy baat la buy toppandoo coow li balu fetal di def bu ñu ko soqee.