dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

tobbi : gas am pax ngir ji ci dara. tobbi na ngédd li yépp ne dafa am lu mu ci bëgg a ji.

tobb g- : tobb xeetu gajj la.

toccal : toccal mooy dëkkal géttu nag wala leneen ab diir ci ab tool ngir fiime ko.

toccami : diwal diw yaram. toccami na kanamu gone gi yépp.

togg 1 : rëgël. sama jabar mën naa togg.

togg 2 : delloo nit ci yoonu njub. kenn mënu ko togg ndax gëmul diine.

togg 3 : toog ci ginnaaw ab welo ñu lay yóbbaale, porte. bu ñuy dem, dama lay togg.

togoju-mogoju : am bind bu jagadi. doom ji dafa togoju-mogoju.

toil b- : tóli rab wu ñuul wuy dund ci biir suuf la.

toj : toj na kaas bi mu doon ndékke. / kaasu weer bi toj na. / defar. daara ji mu nekkoon moo toj xol bi.

tokko b- : caatu njulli m-. moo doon tokko ba ca seen lël ba.

toll : baatu toll, baatu forox rekk lay àndal te di tekk ba mu ëpp. limoŋ bi dafa forox toll.

tollu digante : nekk ci jamono joo xam ne yoruloo lu faj say aajo. muññal ko, dafa tollu diggante rekk, su amee, dina la fey sa xaalis.

tollu : yegg fenn fi. ñu ngi tollu seen dëkk.

tol b- : tol bi dafa forox toll.

tol g- : tol ag garabu meññent la.

tombe : dañu fi tombe wànte yégoowuñuwoon.

tomb : kos, maas. nee na warul a tomb araf bi.

tond : xóot xóot bu yem. seen diwaan ay teen yu tond lañu yore.

tondoxo b- : tondoxo xeetu sax la.

tonet : tontu ci lu gaaw. ne na tonet ne du moom de, wànte kenn gëmul li mu wax.

tong : taxawu. dafa ma tong ci suba ba léegi. dinañuy wax tamit tongu.

tongoo : dañoo toogoo ñoom ñaar.

tongu : dinañuy wax tamit tong. (seetal tong)

tonni : lelli an buub. tonni na mbalit mi yépp.

tono b- : bonofiis b-. amul benn tono ci njaayam mi. dinañuy wax tamit tonu b-. safaan wi mooy pertmaa b-.

tonq : géey. li mu fa nekk moom kese mootax mo tonq.

tontu : wuyu, àddu. bul tontu noon bi, dafa lay tardeel. safaan wi mooy tanqamlu wala sandwiital.

tonu b- : bonofiis b-. dinañuy wax tamit tono b-. (seetal tono)

toŋ-toŋ : saam aw yàpp. toŋ-toŋ na xar mi, saraxe ko.

toŋ : tag, caŋ. morse bi toŋ na ci bànqaas bi

toobo m- : pax mu ñu def ngir jëmbët ci dara mooy toobo.

toog : déju. bàyyil ker gi ngay toog rekk di naan àttaaya. safaan wi mooy jóg wala taxaw.

tooke : jox poson, xomp. dafa tooke jinax ji.

toole b- : xeetu géwel, géwel b-. toole bi dafa ñaansi ci xew li.

tool b- : góor ñaa nga ca tool ya.

toomaa b- : turandoo b-. toomaa bi lay seeti.

tooñ : def nit lu ko neexul. bàyyil tooñ, tooñ du gàllaaj. / ëmbal. tooñ na doomu dëkkandoo bi.

toor-toor m- : toor-toor xeeti picc yuy faral di nekk ci wetu ay nag mel ni lu leen di wottu lañu.

tooy 1 : lu am ndox. xale bi saw na tubey ji ba mu tooy. safaan wi mooy wow.

tooy 2 : am yaram wuy metti. liggeey bu metti bi mu doon def moo ko tooy.

topp : sëllu waa ngi topp yaay ji. / puus. wax ko mu topp tuuti nga mën a toog.

toppum-siti m- : sifilis b-. doktoor bi nee na toppum-siti la waa ji yore. dinañuy wax tamit siti s- wala ndoxum-siti m-.

toqi : dem ba mënatuloo def li nga doon def ndax coono, sonn, tàyyi, tóox. dafa tiye saaku bi ba toqi.

toq : ndox maa ngi toq.

toq g- : toq xeetu picc la.

torob : lool. ndaw si dafa mën a dox torob mootax du juboo jëkkër ji.

torox : dund dund gu metti, walaakaana. nanguwul woon a jàng, nanguwul woon a liggeey mootax tey mo torox.

toskan : toj ay nen. ginaaram gi toskan na. dinañuy wax tamit tostan.

toskare : walaakaana. sàggane ay waa-juram moo ko tax a toskare.

tos : def fiime ci ab tool. tos na li ëpp ci ay toolam.

tostan : dinañuy wax tamit toskan. (seetal toskan)

tott : (ne tott). baatu tott dafay ànd ak baatu torox te di tekki ba mu ëpp. góor gi dafa torox ba ne tott.

tow : dinañuy wax tamit taw. (seetal taw)

toxal : randal, soreel, toppale. toxal na lal bi. safaan wi mooy jegeel.

toxoñ : lu nekk ci sa gët yi ngay toxoñ ?

toxoro g- : liit g-, mbiib g-. borom toroxo gi lay déglu.

toxu : jóge fi nga dëkkoon, dem dëkki feneen. ku dul toxu, doo xam fu dëkk neexe. (léebu). dinañuy wax tamit tóxu.

toyet : baatu toyet dafay ànd ak baatu woyof di tekk ba ëpp. saag bi dafa woyof toyet. dinañuy wax tamit toyy. safaan wi mooy gann (diis gann).

toyom : baatu toyom dafay ànd ak baatu woyof di tekki lu woyof lool. saaku bi dafa woyof toyom. safaan wi mooy gann. (diis gann).

toyy : dinañuy wax tamit toyet. (seetal toyet)