dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

te-du : te-du loolu laa ko waxoon ?

tebbi : jël ab karta ci maryaas. tebbi nga ba pare.

teddi : deppaar. ropplaan bi teddi na sànq. safaan wi mooy teer.

tedd : ku ñu weg. góor gu tedd la ñu fiy siyaare. safaan wi mooy teddadi.

teel : cuuy. ci suba teel la fi génne.

teen b- : root ci teen war naa jeex ci réew mi.

tee : tee nga laaj ku ci xam dara bala nga ciy dugg. dinañuy wax tamit tere, lu-tee, lu-tere.

teeñ : am ay teeñ. sàggan a ko tax a teeñ. / dindil ay teeñ. seen maam lañuy teeñ.

teeñ b- : buuru diwaanu Bawol lañu daan tudde teeñ.

teeŋ : daŋ. takk ko takk bu teeŋ. safaan wi mooy yolom.

teer : taxaw. seen gaal dina teer tey. safaan wi mooy teddi.

teet b- : àmbargóo b-. ab teet bu yàgg dafay daane koom-koomu réew.

teew-mu-teew : njaay mu amul leble, kaari-kaari. soo ko jaayeewul teew-mu-teew, dangay perta ndax ñenn ñi duñu la fey.

teew : ay mbokkam ak ay xaritam yépp teew nañu ci xew li. safaan wi mooy wuute.

teey-xel : luy wocculoo nit. keccob dafay teey-xelam.

teey : yem, dal. teey baax na ci nit lool. safaan wi mooy ëppal wala rambax. / ndoxum géej gi teey na fi mu nekk nii. / nekk di bëgg a woccu. xelam dafay teey bi mu añee ba léegi.

tefes g- : tàkk l-, palaas b-. dibeer dañuy dem tefes.

tef b- : béy wu ndaw w-. ay tef lay yar.

teg 1 : teg na bindukaay bi ci kow taabal ji. / natt, kótise. waa dëkk bi dañoo teg, jënd benn masinu soq. / lótëri. teg nañu kenn ku nekk ñaari junne ci bëre bi. / dafa feebar teg ci du noppalu mukk.

teg 2 : jaawale. yaayam la la gone gi teg.

tegg : (ne tegg). baatu tegg dafay tekki teg dara ak doole, déjj (ne). ndaw si ne na tegg bool bi ci suuf.

tegtal : wax luy wone. ku la tegtal fii ?

tekket : (ne tekket ). baatu tekket dafay tekki lu ñu tekki ci lu gaaw a gaaw. sàcc bi ne na tekket bëy wi ba dem ak moom te kenn yégu ko.

tekki 1 : yewwi, fecci. tekki na saaku bi. baatu tekki mu ngi jóge ci baatu takk.

tekki 2 : dem ba am benn gëdd bi te xam-xam, mën-mën wala am-am tax. fii ku fi tekki, doon doomu ñépp.

tekki 3 : wund. / jàngal ma leetar bi ma xam lu mu tekki. / faramfàcce. li waa ji di wax ci seereer lay tekki ci wolof.

tekk : (ne tekk). patt (ne). ñu ngi ne tekk di déglu li jàngalekat bi di wax.

telle g- : cin lu ndaw l-. telle gi lay togge tey.

tell : tàppandaar. ndab li dafa tell.

tembar b- : jëndal tembar def ci ambolok bi soo kooy yónnee.

tembe : fi mu tollu nii tembe, kenn talatul kenn ndax sikkim a lakkandoo.

tembere : def ci lu gaaw. mënoon ngaa xaar ba suba, sa ñëw bi tey dafa tembere.

temm : baatu temm dafay tekki dogu, ñàkk a mën a dellu ginnaaw ci am mbir. taxaw na temm ne fokk mu dem tey.

temp : daagu, tendeefal. sol na taybaasam bu jekk, di temp di dem. dinañuy wax tamit tenk. safaan wi mooy waaxu.

tendeefal : temp, daagu. li nga doon tendeefal mootax nga yàgg ci yoon wi.

tene m- : tene rabu àll la.

tengaade b- : maaka m-. tengaade mbaxana mu yaatu lay doon.

tenk : daagu, tendeefal. dinañuy wax tamit temp. safaan wi mooy waaxu. (seetal temp)

tenkoñ : teey, yem. sófoor dafa war a tenkoñ. safaan wi mooy ëppal wala yemadi.

tenqi : dagg ay morso. buuse bi tenqi na yàppu nag wi ba pare.

tenq w- : diggu loxo b-. ndax ñeme ngaa teg xalu safara ci sa tenq wi ?

tenqo b- : tenqo mooy béreb bu ay yax daje ci yaramu doom-aadama. dinañuy wax tamit tinqo b-.

te : toogleen te déglu li muy wax. / dafa bëgg xaalis te nanguwul a liggeey. / ndax mën nga génn Dakaar te doo jaar Jamñaajo ?

teñlaay g- : kaala g-. naaj wee tax mu teg teñlaay gi ci bopp bi. dinañuy wax tamit tañlaay g- wala teŋlaay g-.

teŋlaay g- : dinañuy wax tamit tañlaay g- wala teñlaay g-. (seetal tañlaay)

tepax y- : kàpp y-. ci tepax yi la ko melentaan bi màtt.

tepp-tepp b- : taa-taa bu ndaw b-. tepp-tepp moo gën yureet. (léebu).

teppali : xool ma bu baax. nanga teppali sa gët yi. dinañuy wax tamit teppi. safaan wi mooy tapp.

teppas : wol, dëbb. li mu doon teppas moo ko tax a sonn.

teppi : tey la sol yére bi, teppi ko tey. safaan wi mooy tapp.

teqaatle : tàggale, àtte. teqaatle nañu xale yi ba pare, ñu dellu di xeexaat. dinañuy wax tamit teqale wala teqali. safaan wi mooy boole.

teqale : tàggale, àtte. dinañuy wax tamit teqaatle. (seetal teqaatle)

teqali : tàggale, àtte. dinañuy wax tamit teqaatle wala teqale. (seetal teqaatle)

teqamtal : tànn. teqamtal na gerte gi ba mu set.

teraanga j- : baatu teraanga mu ngi jóge ci baatu tedd. (seetal tedd)

tere : aaye. li ngay tere nit ñi soo koy def yow, ndax kenn dina ko bàyyi ? safaan wi mooy nangu.

teret b- : jamonoy njaayum gerte j-. beykat yi dinañuy am xaalis teret.

tette : dimbale xale buy jàng dox. mu ngi tette rakk ji.

tex-texaan : dinañuy wax tamit coqotaan. (seetal coqotaan)

texe : am ngërëmal Yàlla. njort nañu ne góor googu dina texe.

tex : dóor (xale), ñaf, duma. soo ko defati, sa yaay dina la tex.

textexaan : ñoromtaan, coqotaan. mu ngi textexaan xale bi.

teyeef b- : baatu teyeef mu ngi jóge ci baatu tey. (seetal tey)

tey : def dara ci sa coobare. moo ko tey, def ko. dinañuy wax tamit tay.

tey j- : bés bi ñu nekk. tey la war a ñibbi. dinañuy wax tamit tay j-.