dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

taa 1 : def benn taa-taa. ndox mi taa na ci buntu kër gi.

taa 2 : def ab tànn. maa taa ne du gis jëwriñ ji.

taabal b- : caabi jaa ngi ci kow taabal bi.

taab : am taab. dafa taab ci tànku ndeyjoor bi.

taafantu : lay. dara jotu ko, dafay taafantu rekk.

taafar j- : xadar j-. sa taafar jee tax foo dem xuloo fa wala nga xeex fa. dinañuy wax tamit tafaar j-.

taajabóon : wër ci kër yi di jël ay sarax guddi tamxarit. guddi dinañu taajabóon.

taaj : teg. ndaw si yakk na reer bi ba taaj ndab li. / wax nit ñetti dëgg. ay mbokkam taaj nañu ko, wax ak moom ci lu ñaaw li mu def.

taalibe b- : ndongo l-, njàngaan l-. taalibe bi wut xam-xam a ko tax a jóg.

taalif : bind. ci làkku wolof lay taalif.

taal : jafal. taal na sébbu yi. / leerloo. bu kuraŋ bi kuppee, sondeel lañuy taal. / feyal sa portaabal bi ba génn jàkka ji soog ko taal. / safaan wi mooy fey.

taam-taame : neexal. soxla la am ci yow mootax mu lay taam-taame. dinañuy wax tamit tam-tame.

taamu : tànn, tippoo. ku ñuy diri, doo taamu fu ñu lay jaarale (léebu).

taar b- 1 : rafetaay b-. jabar du taar rekk, jikko ju baax itam ci la bokk. safaan wi mooy ñaawaay b-.

taar b- 2 : taar dañu koy jëfandikoo ngir peese dara.

taaraar : segg, tame. gerte gi kenn du ko jënd te du danga ko taaraar.

taara b- : taara mooy jaamu buur bu mujj nekk juroomeelu jabaram.

taarix b- : xam-xamu diine b-. bu nit ñi di wax ci diine te amuloo benn taarix, noppil. / istuwaar b-. xam na tuuti ci taarixu réewam.

taas 1 : tudd lenn wala kenn ci ay wax, gaaruwaale. bu ko tudd, bu ko taas, dafa gaaw a mer.

taas 2 : jox ci barkeb nitu Yàlla. yal na ñu Yàlla taas ci barke walliyu yi fi nekkoon.

taasu : wax ay kàddu yuy tagg wala yuy xas ba pare teg ca ay fecc. mu ngi ci digg géew bi di taasu.

taat w- : ron g-, suuf g-. golo gaa ngi ci taatu garab gi. / kàppu y-, ginnaaw g-. tubey ji mu sol moo fésal taat wi. / bun b-. ci taat ngay jaarale garab bii.

taatu-lawbe : lëmbal. ndaw si taatu-lawbe rekk lay def.

taaw b- : ki njëkk a juddu ci ag njaboot. waruloo caaxaan ndax yow yaay taaw ci kër gi. safaan wi mooy caat m-.

taaxaarlu : tardemaa b-. xaar nañu la ba mu jural ñu taaxaarlu.

taaxirlu : xaar, nég, muñ. taaxirlu nañu ba sonn ñëwul, ñu dem.

taax m- : tabax b-, batimaa b-, miir b-. taax mi gudd na ci kow. borom taax ak borom néegu ñax a yem. / béreb bu ay tabax yu gudd am. Ndakaaru dëkku taax la.

taaxum-kaw m- : etaas b-. taaxum-kow mi mooy màkkaanu jëwriñ yu bare.

taaxuraan : woy jikkoy nitu diine yi. dafay wër di taaxuraan.

taaye : suur, rëy, mbuxuri. xaj bi taaye na.

tabaarfakàlla : jërëjëf Yàlla. Yàlla musal na nit ñi ci feebar boobu, tabaarfakàlla. dinañuy wax tamit tabaarkàlla.

tabaarkàlla : dinañuy wax tamit tabaarfakàlla. (seetal tabaarfakàlla)

tabala j- : ndënd mu yaatu mu naar yi wala xaadir yi di yore ci seen xew-xewi diine yi. jàng ya amoon na ay tabala.

tabanaane b- : fan nga jële doomu tabanaane bi ? dinañuy wax tamit tabanaani b-.

tabanaane g- : tabanaane xeetu garab la. dinañuy wax tamit tabanaani g-.

tabanaani b- : dinañuy wax tamit tabanaane b-. (seetal tabanaane)

tabanaani g- : dinañuy wax tamit tabanaane g-. (seetal tabanaane)

tabandoor b- : unk b-. tabandoor baa ngi daw ci miir bi.

taba b- : taba bi ci taba gi la tàbbe.

taba g- : ag garabu taba la lawbe bi di daane.

tabaski b- : fukkeelu weer ak ñaar ci atum jullit yi. ci weeru tabaski lañu nekk. / julli tabaski b-. bésu tabaski, bu jullit yi demee julliji ba ñëw, dañuy reendi xar yi.

tabax : defar ab néeg wala ag kër. tabax na kër gu mag seen dëkk.

tabb : fal. yaw la nit ñi wóolu, tabb la, fexeel ba bul tas seen yaakaar.

tabe : mën a joxe, yéwen, baax, tàlli. dafa tabe ndax xaalisam bi dafa koy bokk ak ñépp. safaan wi mooy nay.

tabló b- : jàngalekat bi bind na ci tabló bi ba mu fees.

taf 1 : tay. portale sëriñam la taf ci miiru néegam bi.

taf 2 : def ci góor wala jigeen lu koy teree sëy. askan woowu dañuy taf seen xale yu jigeen yi.

taf g- : taf xeetu garab la.

tagar b- : ngatan l-. buleen bëre ci kow lal bi bala ngeen di dàmm tagar bi.

tagatémbe : ràkkaaju, dof. kenn du déglu ay waxam ndax dafa tagatémbe.

tagg : kañ, joobe, bàkk. njiitu réew mi tagg na jëwriñ ji ndax liggeeyam bu rafet.

taglu b- : leket gu yem, laytan g-, tax b-. taglu bi lay deme marse.

tag : lonku fenn. bal bi ñu doon futbale tag na ci kow garab gi. safaan wi mooy tàggi wala tàggarti.

tajoor b- : ñawkat b-. tajoor bi mën naa ñaw wànte du sàmmuwante ak li ngeen waxante.

takk-taxawal : taxawu. bu ko takk-taxawal, dafa amul rekk, su amee dina la fey sa xaalis.

takkandeer b- : ker g-. lutax sa takkandeer foo dem mu topp la fa ? / doom j-. dundu na ba dee amul benn takkandeer. dinañuy wax tamit taqandeer b-.

takkarnaase : jolli bu baax. way pólotig bi dafa duggsi rekk, tëgg mi takkarnaase.

takk : takk jabar. takk na doomu nijaayam ji. / yeew, fas, jéng. takk na xar mi ci garab gi. safaan wi mooy tekki. / jàpp benn bés. takk na bu baax bés bi mu fi ñëwoon. / takk ci sareet wala ci masin. takk na fas wi tukki. nag yi la takkoon bi muy beyi. / sëriñtu nit ki ba mu def li nga bëgg. du maye mukk, dafa mel ni danga ko takkoon bi mu lay may xaalis bu bare bii.

taksi b- : soo amul loo jële taksi, am loo jële kaar-ràppit.

taks b- : juuti b-. danga war a fey ay taks ni sa morom yi.

tal 1 : dijj. piis bi dafa tal. safaan wi mooy sew.

tal 2 : am jotu dara. ku liggeeyul mooy tal a toog di wax lu yoonam nekkul.

tal-tooge : toog tàllal say tànk. mu nga tal-tooge ca basaŋ ba.

talaata : mbej. dafa saaga mootax baay ji talaata ko.

talaata j- : talaata moo topp ci altine.

talalali : ratatati, mbeleleli. mu nga di talalali rekk. safaan wi mooy tekk (ne) wala cell (ne).

tali b- : yoonu gudoroŋ w-. am na oto bu paan ci digg tali bi.

talmbat b- : talmbat xeetu ndënd la.

talsi b- : talsi xeetu suukar la. dinañuy wax tamit tëlsi b-.

tam 1 : dinañuy wax tamit it, itam wala tamit. (seetal it)

tam 2 : bulet. dafay tam di jaay.

tam 3 : tël. mën na tiye bal di ko tam diiru fanweeri simili.

tam 4 : tumaal nit dëmm. ki nga tam ba ñépp di ko daw, tooñ nga ko ba ci kanam Yàlla.

tamaate j- : cu bi saf na sàpp ak tamaate. dinañuy wax tamit kamaate j- wala kàmmaate j-.

tama j- : ndënd mu ndaw mu ñuy boq di ci tëgg. borom tama ji xumbal na xew li.

tambaalu : wëraalu, taxawaalu. deful dara, dafay xëy di tambaalu ba ngoon mu ñibbisi. dinañuy wax tamit tambaambaalu.

tambaambaalu : dinañuy wax tamit tambaalu. (seetal tambaalu)

tame : lay. tame na sunguf si ba pare.

tamit : dinañuy wax tamit it, tam, itam. (seetal it)

tamxarit g- : weer wu njëkk ci atum jullit. ci weeru tamxarit lañu nekk. / bésu tamxarit b-. tamxarit cere lañuy reere.

tanc : kepp, naj. foofa dafa bare nit, boo fa demee dañu lay tanc.

tandale : wax muy loolu. dafa ko tandale rekk wànte xamu ci woon dara. dinañuy wax tamit tandu.

tand g- : dugub ju ñu ji muy sax. nag yi dugg nañu ci tool bi, yàq tand gi yépp.

tandu : dinañuy wax tamit tandale. (seetal tandale)

tane : nekk ci yoonu wér wala yoonu baax. sonnoon na lool waaya mu ngi tane léegi. li nga def tey moo tane li nga defoon démb.

tani : gisaane, listixaar, seet. am na soxna suy tani ci koñ bi.

tank b- 1 : tank xeetu xaalis la woon ni fiftin.

tank b- 2 : bëj-saalum b-. kër a ma nga ca tanku dëkk ba.

tan b- : suuf su dëgër te am xorom. boo demee Jiwaalo, ca tan ba la nit ñi di defare keccax.

tan m- : tan yaa ngi lekk médd mi.

tanqal : lakkal, lëjal, gétën. noppileen, buleen ñu tanqal.

tanqamlu : mel ni ku déggul, sandwiital. danga koy tanqamlu rekk wànte dégg nga li mu wax bu baax.

tanq : jële ndox ci ndab, root. tanq na ndox mi yépp.

tañlaay g- : kaala g-. tañlaay gi gudd na lool. dinañuy wax tamit teñlaay g-.

taŋ b- : jamono j-. taŋ bi fi yaayam nekkee la doon reewantu.

tappale : karabaane. moo fi dàq a tappale te bu weer dewee, mooy njëkk a feyeekuji.

tapp : tapp na butoŋ bi daggoon.

taqaaju : reetaan ba mënatuloo tiye sa bopp. reetaan na ba taqaaju.

taqandeer b- : dinañuy wax tamit takkandeer b-. (seetal takkandeer)

taq : am na lu taq ci sa dàll yi. / kole. lan nga doon def ba singom bi taq ci sa yére bi ?

tar 1 : diis, metti. ci liggeey bu tar lañu nekk fan yii.

tar 2 : dajale gerte gi ñu deqi ba pare. dañuy tar li nga deqi ba pare.

tararari : talalali, ratatati. noppil ngay tararari rekk te li ngay wax amul bopp, amul geen.

tarawliis : (ne tarawliis). niib, nuus, katam. muus mi ne na tarawliis picc mi.

taraxlaay : wodd nit ab sër te takk ko ci baat. ku doon taraxlaay xale bi ?

tarbiyu : wëy ci ndigalu ab sëriñ ba mu gërëm la. dafa tarbiyu sëriñam ba mu séexal ko.

tareet : (ne tareet). baatu tareet dafay tekki lu xotteeku ci lu gaaw. dafa jóg rekk, pont bi lonk mbubb mi, mu ne tareet, xotteeku.

taret b- : bar b-. taret baa ngi dugg ci biir ñax mi.

tari : wax loo mokkal. saar woo mokkalul, mënuloo ko tari.

tarixa b- : tiijaan, murit, xaadir ak laayeen ay tarixa lañu ci réew mi.

tariyaax b- : fajkat b-, defarkatu téere b-. moytul tariyaax bi, dafay faral di naxe ndaxte li mu lay wax mën na bañ a doon dëgg.

tarka g- : fu ñuy wéer bopp ci ab siis wala ab fótëey mooy tarka.

tarxiis : gilise. bul sànni xolliti banaana yi ci kow yoon wi bala ci nit di tarxiis, daanu.

tasab : wird. xaar ma, ma tasab ñu dem.

tase : daje. tase na ak sa rakk ji.

taskatu xabaar b- : surnaalist b-. bala taskatu xabaar bi di siiwal benn xabaar, dafa ko war a gëstu ba mu wóor ko ne li muy bind wala li muy wax dëgg la. dinañuy wax tamit taskatu xibaar b-.

taskatu xibaar b- : surnaalist b-. dinañuy wax tamit taskatu xabaar b-. (seetal taskatu xabaar)

tas : takk-der yi tas nañu ci biir dëkk ngir wottu kaaraange askan wi. / bi buum gi daggee la say wi tas. safaan wi mooy booloo. / na mbokk yi waxtaan ak ñoon ndax bu seen sëy bi tas. / sonnal lool. liggeeyloo na janqam bi ba mu tas. / ki nga yaakaarloo ba mu toog di la xaar, ngalla bul tas yaakaaram. / jeex, pare. sabar ga tas na.

tatafoo : sëqatoo, song. gaa yi dañoo tatafoo sàcc bi dóor ko dóor yu metti. dinañuy wax tamit tatafu.

tatafu : sëqatoo, song. dinañuy wax tamit tatafoo. (seetal tatafoo)

tata b- : miir b-. tata bi yàgg na fi.

taw-féex j- : nekk bu neex b-, aafiya j-. seen réew mi am na taw-féex.

tawat : jàmbat. li nga ko romb nuyuwuloo ko lay tawat. / jagadi, feebar. ci suba ba léegi dafa tawat. safaan wi mooy wér.

taw : tey dafa yeendoo taw Kaasamaas. dinañuy wax tamit tow.

taxan : wut matt. ngoon gu jot taalibe yi dañuy taxan matt mu ñu jànge guddi.

taxañ : ëmb, laxas, lem, maab. taxañ na yéreem yépp, def leen ci benn mbuus.

taxaw : bi mu séene gaynde gi la taxaw. / dafa toogoon wànte léegi mu ngi taxaw. / dakk. seen liggeey bi dafa taxaw bu yàgg ba léegi.

tax : waral. njublaŋ a tax kenn du ko dénk dara.

tax b- : gàmb b-, leket g-, koog s-. ndox mi nekk ci tax bi sedd na guyy.

tay 1 : suusal. tay na cere ji ba pare.

tay 2 : taf. tay na portale bi ci miir bi. safaan wi mooy tàyyi.

tayal : jabar ji dafa tayal. safaan wi mooy sawar wala njaxlaf.

taybaas b- : taybaas yére jigeen bu gàtt la buy tollook ndigam li su ko solee.

tayle : joxe gaaraanti. tayle na këram ci ay caaxaan.