dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

tóoj : teg ci kow dara. dafa tóoj lal bi ba mu gën a gudd.

tóokër b- : tool bi nekk ci biir kër gi, toolu kër b-. tóokër bi am na meññent yu bare.

tóol : lu amul ñaareel. li nga ko jox dafa tóol.

tóonoon b- : bëer b-. tóonoon xeetu jën la.

tóor-tóor : am ay fulëer. garabi màngo yépp a ngi tóor-tóor.

tóor b- : lompaa b-. tóor mooy bant bu gudd buy lëkkale kanam ag ginnaawu lal.

tóoxidoona b- : njombe w-. ñàkk yar a tax ci def tóoxidoona la dëkk.

tóox : sonn ba ëpp. li mu def romb na sonn, dafa tóox. safaan wi mooy sawar.

tóoy : yambar, nooy. sa xartit bi dafa tóoy. safaan wi mooy sawar wala njaxlaf.

tóx : bu la dara dugal ci tóx, dafay yàq sa wér-gu-yaram. dinañuy wax tamit tux.