dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

tëb 1 : suy dox mel ni kuy tëb. / sàcc bi dafa tëb miir bi, dugg ci biir kër gi. kéwel du tëb, doom ja bëtt (léebu).

tëb 2 : mala bu góor bu sëy ak mala bu jigeen ba mu jële ca ëmb. fas wi tëb na wajan wi.

tëdd : ci suba ba léegi mu ngi tëdd.

tëfli : ku ñépp tëfli nga tooy. (léebu). dinañuy wax tamit tufli.

tëf : tëf coow la lu ñuy faral di dégg bu ab balu fetal tàkkee.

tëgal : di tëbal xale ngir nax ko. sooy tëgal xale bi, day reetaan.

tëgg 1 : defar dara ak weñ. dinay tëgg ay sémmeñ.

tëgg 2 : dafay tëgg sabar.

tëgg 3 : dóor. dafa ko tëgg mbej rekk mu daanu.

tëgg-bu-ñuul b- : tëgg-bu-ñuul mooy tëgg buy defar lépp ba mu des ay takkaay.

tëgg-bu-weex b- : tëgg-seyaaxal b-. tëgg-bu-weex mooy tëgg buy defar ay takkaay kese.

tëgg-seyaaxal b- : dinañuy wax tamit tëgg-bu-weex b-. (seetal tëgg-bu-weex)

tëj-fël g- : buntu sarale buy nekk ci paxu jinax. taxawal ci tëj-fël gi, bu jinax ji génnee nga rey ko.

tëkk : dëkk. mbër mi ngay tëkk du sa morom, su la jàppee, dafa lay daan.

tële 1 : yoom. dafa tële wànte su fajoo, mën naa wér.

tële 2 : ñàkk a mën a def dara. dafa tële noppi, foo ko fekk mu ngi wax. dinañuy wax tamit të.

tëll : dagg ay jën ni ku leen di fiiriir. tëll na jën yi ba pare.

tëll : (ne tëll). fëll. baatu tëll dafay tekki lu jékki jékki rekk feeñ. bi ñu koy tudd la ne tëll. safaan wi mooy meŋŋ (ne).

tël : tam, bondeel. xale yi dañuy def ku dàq a tël.

tëlsi b- : dinañuy wax tamit talsi b-. (seetal talsi)

tëmb : nekk di yëngatu ci kow ndox. dàll waa ngi tëmb ci ndox mi. safaan wi mooy suux wala diig.

tëmëñ : lu dem ba ñawatul. jaasi ji dafa tëmëñ, nàmm ko.

tëndëndiir b- : rëdd wu newwi ci yaram wu ay dóor wala màtt-màtt waral mooy tëndëndiir.

tëngeej g- : Tëngeej la dëkk.

tëng g- : ginaar gu jigeen g-. ag tëng la reyal ganam gi. safaan wi mooy séq g-.

tënk : takk ay tànk. soo bañee xar mi rëcc, danga koy tënk. safaan wi mooy tinki. / gàttal. nanga tënk wax ji ndax nit ñi dañoo yàkkamti.

: ku të du nangoo wéy ci waawu kenn. / caabi ji dafa të ci selluur bi. wax nañu ba sonn mu të ne du bàyyi yàmbaa bi muy tux.

tëñëx : dóor ag ndigg. tëggkatu sabar bi tëñëx na ndaw si doon fecc. dinañuy wax tamit tëyëx wala tëymbax.

tëret : (ne tëret). baatu tëret dafay tekki jékki rekk yeewu, ci lu amul benn waajaay. bi mu déggee yuuxu yi, dafa ne tëret yeewu.

tërëf : mel ni kuy daanu, jang. dañu ko dóor benn kurpeñ mu tërëf.

tërin w- : baatu tërin mu ngi jóge ci baatu tëdd. dinañuy wax tamit tëddin w-. (seetal tëddin)

tërngël b- : fërtët w-, tëndëndiir b-. am na benn tërngël ci ginnaaw gi.

tër : tëddal. tër nañu xar mi ba reendi ko muy soog a yegsi.

tëru : baatu tëru mu ngi jóge ci baatu tëdd. (seetal tëdd)

tëstan m- : dinañuy wax tamit téstan m-, tëstën m- wala téstën m-. (seetal téstan)

tëstën m- : dinañuy wax tamit téstan m-, tëstan m- wala téstën m-. (seetal téstan)

tëxët : dinañuy wax tamit téxet. (seetal téxet)

tëx : ñàkk a mën a dégg. ki ngay waxal dafa tëx.

tëymbax : tëñëx. tëggkatu sabar bi tëymbax na ndaw si doon fecc.