dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

téegal : xarafal, jongal. bu xale yi bëree lay téegal doomam ji.

téemeer b- : li fa nekkoon ci ay nit matoon na téemeer.

téen : yëkkati sa bopp di xool ci kow. kenn ku nekk a ngi téen di séentu weer wi.

téeñ b- : téeñ ab morso la booy teg sa kow bopp booy yenu lu diis.

téere b- : ab gëstukat dafa war di bind téere. / gàllaaj g-. mbër mi dafa takk ay téere ba fees dell.

téesante : tuumaalante. ay jabaram ci téesante lañu dëkk.

téfal : ëppal, téllax. yow danga téfal waaye soo demee, nanga yem. dinañuy wax tamit tifal. safaan wi mooy yem wala dal.

tégët g- : tegukaayu ay bagaas b-. ajal bool yi ci kow tégët gi.

téj : sooy génn, nanga téj buntu bi. dinañuy wax tamit tëj. safaan wi tijji.

tékk m- : tékk mooy meewu nag mu njëkk mi bu amee doom.

télbati : ëppal, yemadi. dafa télbati mootax kenn wóoluwu ko ci lenn. safaan wi mooy yem wala teey.

téll-ma-rajax b- : kuy def te du xaar mukk ba xam lu mu war a def, ku teeyadi. kooku ab téll-ma-rajax la rekk.

téllax : ëppal, yemadi. nee na bëggul jigeen ju téllax. safaan wi mooy teey wala dal.

téll : (ne téll). baatu téll dafay tekki coow lu tukke ci lu dàmm. dafa dëgg bant bi rekk, mu ne tell, dàmm ci digg bi.

témboo : kàngamloo, arañefe. kenn rawul sa morom, dañoo témboo ñoom ñaar.

ténj : muuru bu sa jëkkër faatoo. bi mu nekkee di ténj la ko góor ñi tàmbalee seeti ngir takk ko.

tépparle : saaraan. kaar ràppit bi romb na are bi, tépparle di dem rekk.

téqalmë b- : téqalmë ab jumtukaayu taar bu ñuy defare der te jigeen ñi daan ko sol ci tànk la. dinañuy wax tamit téqërmë b-.

téqërmë b- : dinañuy wax tamit téqalmë b-. (seetal téqalmë)

téq : xëcc wala lonk ab tànk ngir daane borom. téq la ko def rekk, mu daanu. dinañuy wax tamit téqtal. / dindi. li ma la yoreeloon, téq ko ci xaalis bi nga ma war a jox. / dóor balu fetal. dafa séen sàcc bi rekk, téq fetal gi.

téru : jolu. téru na guttu ndox bi yépp.

tés-tés j- : kër-kër j-. tés-tés ji yi yépp, bëgg lu ñu yóbbu kër ga rekk a ko waral.

téstan m- : dafa gaañu ci téstan. dinañuy wax tamit tëstën m-, tëstan m- wala téstën m-.

téstën m- : dinañuy wax tamit téstan m-, tëstan m- wala tëstën m-. (seetal téstan)

téxet : loolu moo ko def ndax moom dafa téxet. dinañuy wax tamit tëxët.

téye : jàpp. téye na ko bu baax ndax bu mu ko rëcc. dinañuy wax tamit tiye. safaan wi mooy bàyyi wala wacc.