dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

su fekkee ne : dinañuy wax tamit su wala su fekkee. (seetal su fekkee)

su fekkee : su fekkee doo ko jox, yewwi ko mu dem, bul ko tardeel wala nga koy ñàkkal faayda. dinañuy wax tamit su wala su fekkee ne.

suba : ëllëg. dina fi ñëw suba. / liy ñëw ci kanam. kenn ku nekk war naa bàyyi xel ci suba. ndaw ñee war a defar Afirig suba.

suba g- : bëccëg b-. dem na ci suba gi.

suba s- : lii rekk la liggeey ci suba si.

suboqun-ma : dinañuy wax tamit suboqun. (seetal suboqun)

suboqun : mbas. suboqun jigeen ju am jëkkër, am far. dinañuy wax tamit suboqun-ma, bóqun-ma wala xuddoosun.

suceengoos : deel takk suceengoos.

suggli : setal. waa dëkk bee suggli mbedd yi yépp. safaan wi mooy tilimal.

sugum s- : kër yamb g-. am na sugum su nekk ci kow garab gi.

sujjoot : sëgg. bi muy nuyu sëriñam, dafa sujjoot.

sukkeer b- : dinañuy wax tamit cokkeer b-. (seetal cokkeer)

sukkën : lakk gerte wala ñebbe ci am pax mu am xal te ñu muure ko suuf, këntu. dañuy sukkën gerte gi.

sukk : toog sëpp say wóom. bu taalibe yi di lekk, dañuy sukk.

sukkoot : soox. dafay sukkoot mootax dox bi yéex.

sukku-bakkan b- : diggu bakkan bi jokkloo ak tuñ mi. ci sukku-bakkan bi la roddu.

sukkuraat : nekk di bëgg a dee, xar-xarle. góor gaa ngi sukkuraat.

sulli : alkaati yi sulli sinebar bi saay-saay si suuloon. safaan wi mooy suul.

sull b- : kooy b-. solal ko tubey, sull baa ngi ci biti.

sumaare g- : sumaare ak gajj la gu am xet gu neex te ñu ciy defar ay caq.

sumb 1 : tàmbale fóot. sumb na fóotam mi.

sumb 2 : dugg ci am mbir. amal sa fulla ak sa faayda ba li nga sumb du yàqu. dinañuy wax tamit sémb.

summi : summi na yére bi mu soloon. dinañuy wax tamit simmi. safaan wi mooy sol.

sump g- : sump garabu meññent la.

sump s- : sump si ñoragul.

sumul s- : sungufu mboq s-. defal tuuti sumul ci cere ji.

sunguf s- : lu mokk. kilo sungufu meew bi dafa seer.

sunguf w- : sax w-. felaŋal sunguf wi.

sunjuñ : ŋalaab. dafa bañ nag wi lekk ci toolu jàmbur bi mootax mu sunjuñ ko.

sunna s- : sunna mooy, ci diiney islaam, lu ñu gis yonent bi daan ko def.

su : su kenn ku nekk defoon li ko war, kenn du sonn. dinañuy wax tamit su fekkee wala su fekkee ne.

su b- : su nattu xaalis la woon.

su j- : su ji ci réew mi lañu koy beye. dinañuy wax tamit suppome j-.

suñel g- : saaw m-. suñel gaa ngi ci biir pax mi. dinañuy wax tamit suññeel g- wala siñeel g-.

suññeel g- : dinañuy wax tamit suñel g- wala siñeel g-. (seetal suñel)

suppeer b- : bool b-, ndab l-. ci suppeer bi la def yàpp wi.

supp b- : borom restoraŋ bi dinay jaay suppu yeel.

suppome j- : dinañuy wax tamit su b-. (seetal su)

suq b- : mbër mu ndaw mu topp ci mbër mu mag, mu siiw lañuy tudde suq.

suq w- : ŋóot w-. lekk na mboq mi ba sànni suq wi.

suraat b- : mokkal na suraat bi.

surga b- : surga mooy góor gu ñu jël di ko liggeeyloo ci ab diir boo xam ne, bu jeexee, nga fey ko.

surnaal b- : ci surnaal « Siiwal » laa jànge xibaar bi. / kayit g-. may ma surnaal yi, ma boyalee ko.

surux : dugg fu xat. bindukaay bi surux na ci pax mi.

sut : gën a gudd. sa rakk jee la sut. / gën a mën. du sa morom, moo la sut ci seen liggeey bi.

sutti : tuur. dinañuy wax tamit sotti. (seetal sotti)

sutura s- : ndéey l-. nit dafa war a am sutura. safaan wi mooy jéebaane b-.

suub : soppi melo piis, teent. yére bi melulwoon nii, dafa ko suub.

suuf : muus maa ngi ci suufu taabal ji. safaan wi mooy kow.

suuf g- : ceeb bi dafa xëm ci suuf gi. safaan wi mooy kow g-. / bun b-, taat w-. ci sa suuf gi ngay jaarale per bi.

suuf s- : ber b-, beeñ b-, salleñ s-, gannuus g-. yoon wi dafa bare suuf. / suuf seer na lool ci yenn béreb yi ci Ndakaaru. / Yàllaa sàkk suuf, sàkk asamaan.

suukar : def suukar ci aw ñam. suukar ko ba mu saf.

suul : dugal ci biir suuf si, delloo suuf ci pax mi mu jógewoon. safaan wi mooy sulli.

suul b- : nétetu lañuy defare suul, di ko def ci ceebu jën.

suuna s- : suuna xeetu dugub la.

suur 1 : regg. lekk ba doyal. ku lekkul ba suur moomuloo tiitaru. safaan wi mooy xiif.

suur 2 : xër. dangay def reen yi ci safara, suur ko ko.

suurur g- : suurur xeetu gajj la.

suus : su cóolë di génn ci cin lañuy wax ne togg gaa ngi suus.

suux : dugg ci biir ndox, diig. dangeen war a wottu kaaraange nit ñi baa gaal gi du mës a suux. safaan wi mooy suqali.

suux g- : pax mu nekk ci ag garab di tiye ndoxu taw mi, lëm m-. bul dugal sa loxo ci suux gi, xamuloo lu nekk ci biir.

suux w- : morso yàpp b-. dinañuy wax tamit sóox w-. (seetal sóox)

suuy : suuy baat la buy tekki ag mbégte. suuy doom !

suweer : def ab portale ci weer. portale bi ma ànd ak sama pàppa ak sama yaay laay suweer.

suy-bale b- : puudaru mbóot b-. suy-bale bi rey na mbóot yi fi nekkoon yépp.

suy : wis. suy na àngare ci tool bi ba mu saf sàpp.