dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

sobe s- : lépp lu mel ni manniyu, deretu mbaax j-, kabine y-, saw m-, tilim b-. bala ngay julli, danga war a dindi sépp sobe su nekk ci yow.

soble s- : soble rënd la. yaasa bi dafa bare soble.

sob : léej, yemadi, toogadi. xale bi dafa sob lool, du dégg mukk. safaan wi mooy teey wala yem.

soccent b- : njéereer b-. àll bi bare na ay soccent. dinañuy wax tamit soccet b-1.

soccet b- 1 : dinañuy wax tamit soccent b-. (seetal soccent)

soccet b- 2 : picc b-. am na soccet bu nekk ci kanam gi.

socc : nangay socc say gëñ.

soddax : ndox mi mu donn naan moo ko soddax. dinañuy wax tamit coroxaan. (seetal soddax)

sofe 1 : mótooru oto baa ngi sofe.

sofe 2 : am gémmeñ gu am ay picc, di metti. gémmeñ gi dafa sofe.

sof : jokklante, takklante. boo soful ñaari tiyo yi, du jot. dinañuy wax tamit soflante.

sofoor b- : dawalkatu oto b-. sofoor bu màndi warul a dawal oto.

sog : def yoon wu njëkk. mu ngi sog a dem Tugël. dinañuy wax tamit soog wala doog.

soj : xurfaan. dafa soj mootax bakkan yi fatt.

sokk : am dég wala bant bu dugg ci sa yaram. sànnil bant bi bala mu lay sokk. dinañuy wax tamit sonk.

soldaar b- : soldaar bi dafa gaañu ci xare ba mu demoon.

soldaar s- : mbooleem soldaar y-. soldaar si peyoor bu baax lañu war a am.

soléet : (ne soléet). njool. ndaw si mu fa takkee dafa ne soléet.

sol : sol yére bu rafet te seer taxul a am xaalis. / feesal. sol na ngooñ ci saaku bi. / dugal ci xel. li ngay sol sa doom ji, na doon lu baax.

solom b- 1 : solom xeetu meññent la.

solom b- 2 : tiyo gënn tuxu, sonk b-. solom bi dafa bënn.

solom g- : xeetu garab. bul fàttee roose solom gi.

solo s- : li ngay wax ak li ngay def, fexeel muy lu amal askan wi solo.

solu-làbbe : nekk ab làbbe. fan yii la waa ji solu-làbbe.

solu-soldaar : dem larme. léegi jigeen ñi dañuy solu-soldaar. safaan wi mooy summi-soldaar.

solu-soor : magam dafa solu-soor.

somp : tibb tuuti. somp na ci buy bi.

sondel b- : booy génn néeg bi, fayal sondel bi. dinañuy wax tamit sondeel b-.

song : dal ci kow nit. ay saay-saay ñoo ko song, nangu li mu yorewoon yépp.

sonjaan b- : tool bu ñu booyal, mbooy g-. demal yeew fas wi ca sonjaan ba.

sonk b- : tiyo gënn tuxu b-, solom b-. sonk bi lay sekkarti.

sonku : am dég gu la jam. dafa sonku ci tànk. dinañuy wax tamit sokku.

sonn : tàyyi, tóox. askan wi dañoo sonn ci toog di xaar lu dul ñëw mukk. safaan wi mooy noppalu.

so : tëdd (jant). jant bi so na, nañu dem. safaan wi mooy fenk.

soññ : ñaax, xirtal. soññ na ko ba sonn ngir mu góor-góorlu waaya xale bi amul benn jom. / xamb. soo bëggee togg gi gaaw, dangay soññ taal bi.

soob : neex. ndéem soob na Yàlla, dinaa la seetsi ngoon. safaan wi mooy naqari.

soob g- : soob xeetu garab la. am na soob gu nekk seen digg kër.

soob j- : ay doomi soob lañuy tudde soob ji.

soof : ñàkk solo, ñàkk xorom, safadi, lewet. xale bu jigeen bi soof na waa koñ bi. safaan wi mooy saf.

soog : dinañuy wax tamit sog wala doog. (seetal sog)

sooke : porowoke. waruñoo nangu ñi fi dëkkul di ñëw Afirig di fi sooke ay xeex.

soon g- : soon garab la. soon gi dafay bëgg a daanu.

soon j- : xeetu meññent. soon ji ñoraguñu.

soor-soor b- : soor-soor xeetu garab la.

soor : feeñ. suul ker du ko teree soor. (léebu).

soor b- : jigeenu làbbe. kër gi ab soor a fi dëkk.

soor g- : soor ag garab la.

soos : dugal ci ab soos, ñeex. soos na mburu mi ba mu tooy.

soosu : di nga ko gis ci baatu boobu. (seetal boobu)

soow : xul, xas, gëdd. lu sa maam di soow ? / wax wax ju bare, yuuxu, tanqal. gone yaa ngay soow ca mbedd ma.

soow m- : mbaanig m-, kàcc m-. du naan soow.

soox : maamam dafay soox benn tànk bi.

sooy : ñàkk a am dara ci am rëbb. xale yi dañoo rëbbiwoon waaye sooy nañu.

sooy b- : xeetu piis, suwaa b-. yéreem bi sooy la.

soppi : soppi na néegam saal. dinañuy wax tamit soppali.

sopp : bëgg, xemmem. sopp na njarum soow.

soqi 1 : dóor balu fetal. ageresëer yi mën nañoo soqi ci sa kow soo nanguwul a def li ñu bëgg. safaan wi mooy sox.

soqi 2 : njëkk a jënd ci ab jaaykat. ki la soqi tey jig na la.

soq : dëbb pepp. soq na dugub ji ba pare.

soraas g- : garabu soraas gi dafay bëgg a daanu.

soraas s- : doomi soraas yi ñoraguñu.

sore : fi mu jëm sore na. dinañuy wax tamit sori. safaan wi mooy jege.

sos : Yàllaa sos doom-aadama. / wax lu amul. li mu wax dara amu ci, dafa sos lépp.

sot : dimbale genn wàll ci am coow. dafay sot rekk wànte yoonam nekku ci.

sotti 1 : tuur. sotti na ndox mi ci paan bi. / tekki. li ngeen di bind ci farañse te soxal askan wi, dangeen ko war di sotti ci làkki réew mi.

sotti 2 : pare, jeex, noppi. li mu doon def ci suba ba léegi sotti na. safaan wi mooy tàmbali.

sowu-jant b- : Senegaal a ngi nekk ci Afirig sowu-jant. dinañuy wax tamit sowu b-.

sox-soxóor : sox-soxóor aw rab la.

soxal : amal solo. waypólotig bi li mu leen di wax, boppam la gën a soxal.

soxla : waa ji yow la soxla.

soxna m- : Soxna turu jigeen la.

soxna s- : jabar j-, jongoma j-. soxna si fan yii la fi sëysi.

sox : bul sox sa fetal gi di doxantu ak moom. safaan wi mooy soqi.

sox b- : xaalis b-. foo jële sox bi nga yore yépp ?

soxor : bon. dafa soxor motax fu mu tollu mu ngi dóor xale bi. ku soxor du bëgg kenn tekki. safaan wi mooy baax.

soylu : jublu. xaj baa nga soylu ca médd ma. safaan wi mooy dummooyu.

soyndaaru : dàggeeku, beru, beddeeku. sànq ba tey mu ngi soyndaaru ci ruqam, waxul ak kenn. safaan wi mooy booloo.

soy g- : weñ gu ñu tàngal. ag soy lañu reye ñàngoor mi.