dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

seben : saw, gaanuwaay. gone gi seben na tubey ji. dinañuy wax tamit siben.

sebet 1 : raxas am pepp. ndaw si sebet na dugub ji ba pare.

sebet 2 : taw ba pare. taw bi sebet na. dinañuy wax tamit sebeti wala sewet.

sebeti : dinañuy wax tamit sebet. (seetal sebet)

sebër : def ay dëggukaay ci fas wu ñu nar a war. sebër na fas wi ba war dem rekk a ci des.

sebre b- : sebre mooy diggante bi dox ci baaraam-déy ak baaraam-sanqaleñ te ñu koy natte.

sedd : liw. Ërob dafa sedd. safaan wi mooy tàng.

seeb : toq. ndox miy seeb fu muy jóge ?

seede : wax ci loo fekke. li ngay seede na doon lu la wóor. dinañuy wax tamit seere.

seekeeg : dafa seekeeg mootax mënul lekk bu baax.

seel : dagg ay dagg yu sew. buuse bi seel na yàppu bëy wi yépp.

seel b- : seel jumtukaayu bu ñuy yéege. wutal seel yéegal ma ci kow garab gi.

seelu : dugg fu la taw bi dul tooyale ba mu sebeti. dañoo seelu ba taw bi sebeti ñu soog a teguwaat ci yoon wi.

seen : Seen sant la. (santu séereer lu ci ëpp).

seeñ b- : lawbe b-. duma takk ndaw si ndax seeñ la du wax.

seeñu : maccaat. xaj yi seeñu nañu yax yi ba ñu set wecc. dinañuy wax tamit seeñaat.

seere 1 : dinañuy wax tamit seede. (seetal seede)

seere 2 : sank 1. dafa seere mootax ay fan a ngi nii demul duus.

seereer : melo wu xonq wu jëm ci weex te fas wala xar di ko am. xar mi dafa seereer.

seer : jafe. dëwlin dafa seer. safaan wi mooy yomb.

seet : xool. / seet na ko ba gis ko. / wut. lan ngay seet fii ? / gisaane. sëriñ bi dëkk ci kër gi dafay seet.

seew : bëgg lu dul. waa ji dafa seew a takk ndaw si, te ndaw si nobu ko.

seey : ruy. su kurãa bi kuppee lu yàgg, galaas gi dafay seey.

sef : ñeex. nanga sef cere ji ba mu tooy xepp. dinañuy wax tamit sif.

segal : génne dëwlin ci gerte wala leneen, nal, perees. am na ñuy segal dëwlin.

segg : tame. nanga segg dëwlin gi.

segg m- : segg rabu àll la.

sekkarti : dinañuy wax tamit sekki. (seetal sekki)

sekki 1 : dindi dara. abal ma péngu ma sekki dég gi nekk ci sama tànk bi.

sekki 2 : funki, newwi. ndox mu tàng soo ko sottee ci cere, cere ji dafay sekki. safaan wi mooy dellu.

sekkit w- : daggitu piis b-. dafay dajale ak sekkit ngir defar ci ay yére baayfaal.

seko b- : béreb bu ñuy sotti lu jóge ci am mbey. seko yi dañu daan fees dell ag gerte.

seku b- : coy l-. dinañuy wax tamit saku b- wala caku b-. (seetal saku)

selaw : (ne selaw). tekk (ne). néeg baa ngi ne selaw, kenn waxatul. dinañuy wax tamit selew. safaan wi mooy xumb wala rëb.

selbe b- : kuy wottu ay njulli, lam b-. njulli yi benn selbe rekk lañu am.

selew : dinañuy wax tamit selaw. (seetal selaw)

sell : lu amul benn tilim, benn gàkk-gàkk. li ngay lekk na sell soo bëggee mucc ci feebar yu bare. safaan wi mooy tilim wala salte.

sell b- : bëñ b-. xaj am na ay sell yu mag.

selluur b- : kànnaar b-, xomb g-. jëndal selluur bu dëgër.

semen b- : ayubés b-. ci semen bi la war a ñibsi. dinañuy wax tamit sëmen b- wala simen b-.

sem : làggi. benn tànk bi dafa sem.

senax : dinañuy wax tamit sanax. (seetal sanax)

sendaw : (ne sendaw). lu ne tekk amul benn coow, selew (ne). bi xale yi doon coow demee, la béreb bi ne sendaw. safaan wi mooy xumb wala rëb.

senegaal : Senegaal réew la mu nekk ci catu Afirig sowu jant, ci diggante Móritani, Mali, Ginne Bisaawo ak Ginne Konaakiri.

senjeeñ g- : senjeeñ xeetu gajj la.

senn : am fu bënn. pot bi dafay senn.

sentuur g- : geño g-. sentuur gi der la.

seŋoor b- : geño guy aar, xàpp g-. mbër yi dañuy takk seŋoor ngir muslu ci lu bare.

sepp-seppal : toq. ndox miy sepp-seppal ci kow lay jóge.

seppi : génne fenn, génne ci am mbir, rocci. seppi na ñetti màngo yi gën a rëy ci màngo ji.

sepp g- : sepp xeetu garab la guy ñuy def ay reenam ci ndox ngir mu gën koo neexal.

seqi 1 : dundaat. gàncax gaa ngi seqi.

seqi 2 : poñe. dafa ko seqi, bëgg a dóor nit ñi àtte.

serecu : tufli. dafa salte, fu mu toog, dina fa serecu ba mu fees. dinañuy wax tamit seretu.

sereŋ g- : mbaxal g-. sereŋ gi dafa saf kaani.

sereti : dinañuy wax tamit serecu. (seetal serecu)

serkel g- : findifeer g-. serkel gi jeex na te sàkket wi pareegul.

serlu : naan dara ngir seral sa xol. gan ñi serlu nañu bay dallu.

ser : yuuxu. yar bi dafa dal rekk, mu ser.

set : danga war di lekk lu set, dëkk fu set, di sol lu set. safaan wi mooy tilim.

setu b- : setu lañuy tudde saabu bu guddee.

sewet : dinañuy wax tamit sebet. (seetal sebet)

sew : du lekk mootax mu sew ruuj. safaan wi mooy tal, rëy wala dijj. / baat bi dafa sew. safaan wi mooy diis.

sexaw b- : kenkelibaa b-. du naan kafe, kenkelibaa rekk lay naan.

sex : dugal ci gémmeñ, log. wannal li nga sex.

seyaan g- : dinañuy wax tamit sayaan g-. (seetal sayaan)

seytaane : dinañuy wax tamit saytaane. (seetal saytaane)