dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

saa-su-jot : nangay rafetal sa diggante ak nit ñi saa-su-jot. dinañuy wax tamit saa-su-ne wala saa-yu-ne.

saa-su-ne : dinañuy wax tamit saa-su-nekk, saa-su-jot. (seetal saa-su-nekk)

saa-yu-ne : dinañuy wax tamit saa-yu-nekk, saa-su-ne wala saa-su-jot. (seetal saa-su-nekk)

saabal : nettali. li ngay saabal nit ñi na doon lu la wóor.

saaba b- : àndandoori yonent bi lañu doon tudde saaba.

saabu : yàqu. gerte gi mu la jaay dafa saabu.

saabu b- : du sangoo ak saabu mukk.

saafara s- : paj m-, garab b-. demal seeti doktoor bi, mu bindal la saafara su baax ci sa feebar bi. / ndox mu ñuy boole ak yeneeni mbir, di ci sangu wala di ci raayu ngir muslu ci luy lore, wala ngir am dara. saa yu xëyee, dina rayoo saafara soog a génn.

saafàndu g- : saafàndu rabu àll la.

saaf : lakk. dafay saaf gerte di jaay.

saafoonte : jàmmante, nuyuwante. dafa am aajo ndax fu mu daje yow, dina saafoonte.

saafun b- : gàllaaj gu ñuy defar ngir liggeey ci nit te di ko sànni ci kow. soxor bu mu la tax a wuti saafun ngir lor ci doomu jàmbur, Yàlla dina àtte ëllëg. dinañuy wax tamit saaxun b-.

saaga : génne wax ju ñaaw ci làmmeñ. xale kenn waru ko jàngal saaga.

saagër : mat. doomam ju jigeen ji saagër na léegi.

saag b- : saagu loxo, saag bu ñuy teg ci ginnaaw. kow oto bi dafa fees dell ak ay saag.

saaku b- : dugub la saaku bi def.

saal b- 1 : liy nekk ci biir xooxu meññent. sànnil saalu màngu bi, kenn du ko lekk.

saal b- 2 : saloŋ b-. ci saal bi la dalal gan ñi.

saala : seetal simila-ak-saala ci suuf.

saalika noonu : ci benn anam bi. dafa xees, magam bi tamit saalika noonu. dinañuy wax tamit kasaalika noonu.

saalit : am jaxasoo bu ndaw bu lay defloo loo tayul lu reelu. diggante bi xaalisam bi réere ak bi muy feeñ dee saalit na fi.

saaloñ : am kawaru bopp gu bare, sëq-lipp. xale bi dafa saaloñ, nanga ko wat suba.

saalum g- : Saalum turu diwaan bu nekk Senegaal la.

saamaar b- : paaka b-, gobar b-. sàmm bi saamaar ak jaasi la yore.

saamandaay : niru, mel. ndaw si dafay saamandaay ab naar. dinañuy wax tamit samandaay.

saambaraayeer b- : saambaraayeeru póno bi dafa bënn.

saam : def ay jal yu ndaw. yàpp nag wi yépp la saam di ko saraxe.

saan w- : dafa am ay saan mootax du suur mukk.

saa s- : waxtu w-, jamono j-. deel sàmm li ngay wax saa su nekk.

saañ : fatt. saañ na gutt bi.

saaño s- : saaño xeetu pepp la.

saar : Saar sant la. (santu séereer li ëpp).

saar w- : ay saar yu néew la mokkal ci alxuraan.

saasfaam b- : saasfaam mooy saytu wér-gu-yaramu jigeeni-wérul yi.

saas : tàng ba mu ëpp. dëwlin gi saas na léegi.

saatagaay b- : baale b-, bàyyi g-. saatagaay bi baax na ci moom ndax waa ji amul lu mu feye li mu yàq yépp.

saatu-dënn b- : saatu-dënn yax la buy toll ci dënn. dinañuy wax tamit saatu-naw b-.

saatu-naw b- : dinañuy wax tamit saatu-dënn b-. (seetal saatu-dënn)

saatu s- : paaka bu ndaw b-. nangul saatu si xale bi di foye bala mu ciy gaañu.

saaw : tasaaroo. ginaar yépp saaw nañu.

saawo s- : yoon wi nag yi ñuy sàmmi di jaar, galat b-. saawo si la topp ba gis nag wi réeroon. dinañuy wax tamit saawu s-.

saawu s- : dinañuy wax tamit saawo s-. (seetal saawo)

saaxun b- : dinañuy wax tamit saafun b-. (seetal saafun)

saay 1 : dee. ku xamul buur saay na, xam buur dee na. (léebu

saay 2 : fésal sa mbégte ak am pecc, fecc. saay na ba sonn bi mu yégee ne dañu koy jël ca bérebu liggeeyukaay boobu.

saay-saay : ki ngay àndal dafa saay-saay, du àndandoo.

saayir b- : li feeñ. sëriñ bi xam na saayir ak baatin yépp. safaan wi mooy baatin b-.

sab-lekk b- : géwël b-. sab-lekk mooy géwël buy dundu ci ay waxam.

sabab : sooke, waral. moom moo sabab xeex bi.

sabab b- : musiba m-, balaa b-. saa yoo xëyee, deel ñaan Yàlla mu musal la ci sabab.

sabar g- : sabar xeetu ndënd la.

sab : jooy, woy. picc yaa ngi sab ba kenn mënu fi dégg.

saddit w- : ci saddit wi la dagg. dinañuy wax tamit siddit w- wala siddiit w-.

sadd : newwi, funki. dafa taxaw ba tànkam yi sadd. safaan wi mooy rees.

saddu g- : martó b-. nangul saddu gi bala muy daanu ci tànku xale bi.

saf-cin l- : baatu saf-cin mooy li ñuy tudde xorom ci guddi gi, loolu biddaa moo ko fi bàyyi.

saf-xorom : ku saf-xorom mooy ku neex waxtaan. safaan wi mooy soof.

safaanke : dinañuy wax tamit safaanoo. (seetal safaanoo)

safaan w- : góor mooy safaanu jigeen.

safaantoo : songoo. beykat yi safaantoo nañu ak pël ñi.

safara : fi Yàlla di dugal képp kudul woon def ay ndigalam wala ki doon def ay tereem, mooy safara. safaan wi mooy àjjana. (seetal àjjana)

saf : ceebu bu jën bi saf na sàpp. / am cafka dara. cere ji dafa saf laalo. / metti. alkol bi dafa saf lool. safaan wi mooy sàppi.

sagar b- : yére bu xotteeku b-, morso b-. li waa ji sol ay sagar bu mu tax nga xeeb ko.

sag b- : mbégte m-. Seex Seydi Aas Maalig, Seex Ahmadu Bàmba, Seexal Islaam, Maam Buu Kunta ak Maam Limaamulaay suñuy sag lañu.

sago s- : li la neex. su doon sama sago, li ñépp bokk, ñenn ñi rekk duñu ko def seen moomeel. / xel m-. su waa ji àndoon ak sagoom, du def yaramu neen ci digg mbedd mi nii.

sajj-xef : ñàkke kersa. ki ngay sajj-xef dafa yorul dara rekk.

sajjaada b- : jullikaay b-. bul taqal sajjaada bi sobe.

sajj : sëgg. bi mu séenee yaayam di ñëw, dafa sajj ndax bu mu ko gis. safaan wi mooy siggi.

saj : fuuf, dëndiix. baatu saj dafay tekki naan dara ci lu gaaw. ne na saj potu ndox bi.

sakkan : bare. suukër si sakkan na lool ndax waxtu wii waroon na fekk mu jeex. safaan wi mooy tuuti wala sakkanadi.

sakk : saañ, fatt. nanga sakk pax mi fi kaña gi gas. safaan wi mooy sekki.

saku b- : coy l-. saku bi tuur na ndox mi. dinañuy wax tamit caku b- wala seku b-.

salaan g- : salaan xeetu gajj la.

salaat s- : soos bi amul salaat.

salaatu : nodd nodd gu mujj ci fajar gi. bi ñuy salaatu lay génn kër gi.

sala w- : pom b-. sala wi dafa màgget léegi, benn oto waratu ci jaar.

saliiñ s- : dinañuy wax tamit salleñ s-. (seetal salleñ)

sallax : xëpp, sànni. bul ko sallax suuf si. dinañuy wax tamit sëllax.

salleñ s- : beeñ b-, ber b-. yoon wi dafa bare salleñ. dinañuy wax tamit salliiñ s-.

salliir b- : salliir xeetu rab wu bare coow la.

salte : tilim. jigeen warul a salte. safaan wi mooy set.

saltige b- : nit ku am ay xam-xam yu làqu ci dëkki séereer yi. saltige yi nee nañu ren nawet bi dina baax.

samandaay : niru, mel. dinañuy wax tamit saamandaay. (seetal saamandaay)

samdi j- : aseer j-, gaawu b-. samdi lay ñëw.

sam : wër. xaj yaa ngi sam médd mi. dinañuy wax tamit sëm.

samp : dugal dara (bant wala tib) ci biir suuf si ngir mu am lu muy tiye. mbaa bant yi nga samp dëgër nañu ? safaan wi mooy sempi.

sanax : nagam. yaramam wi dafa sanax. dinañuy wax tamit senax.

sanc : njëkk a dëkk, dal. sama maam a sanc dëkk bi ñu naan Séen naa la kër Abdu Awa. safaan wi mooy toxu.

sandaamtalu : lang. golo gaa ngi sandaamtalu ci garab gi.

sand g- : kéwel g-, mbill m-, barom b-. gaynde gi rey na ag sand.

sandwiital : di dem bañ a déglu li ñu lay wax, tanqamlu. yaayam a ngi wax ak moom, muy sandwiital. safaan wi mooy wuyu wala tontu.

sang : nangay sang xale bi ba mu set.

sang b- : doomu nijaay j-. sama sang la mootax ma koy tooñ.

sangu-set : sangu ginnaaw boo sëyee, wala nga génne manniw, wala nga gis mbaax, sangu-janaba. boo sëyee ak sa soxna ba pare, danga war a sangu-set.

sanjaay b- : sanjaay xeetu fecc la.

sank : seere. démb ba léegi xale bi dafa sank.

sanqaleñ w- : melentaan w-. suukar see fi andi sanqaleñ yi.

sanqal s- : sunguf si pepp su ñu lay ba pare. laax lay togg ci sanqal si. dinañuy wax tamit sànqal s-.

sanq : ci ginnaaw. sanq la génn. dinañuy wax tamit sànq wala sànk.

sant 1 : Seex Anta, Jóob la sant.

sant 2 : gërëm. ku la defal lu baax, danga ko war a sant. safaan wi mooy xarab.

sant 3 : defloo nit dara. li ngay def, na fekk muy lu jub lu ñu la sant.

santaare b- : béreb bi ñuy tuur kabiney fas yeek mbaam yi, sën b-. santaare bi dafa jege yoon wi.

sa : wax nit ki li mu war a baamtu, digal. dañu ma sa njàng mii yépp.

sañaxal : jeñax. dafa doon siisu ñu sañaxal ko ba mu dem. safaan wi mooy xëcc.

sañaxu : def dara te ànduloo ci ak sa xel. sooy dugg ci am mbir, bul sañaxu, nanga ko seetaat bu baax.

sañ : ñeme, dëgër fit. dafa sañ rekk wànte kenn joxu ko ndigal ci li muy def. safaan wi mooy ragal. / am yelleefu def dara. sañ naa samp ndëndëm ngir dagaan baati askan wi ci réew mi.

saññaaral : lu fés. gëñ ya dañu ne saññ saññaaral.

saññ : (ne saññ). lu ne fàŋŋ ndax ni mu tollu. boo ko gisee, nopp yaa nga ne saññ.

sañse : sol yére yu rafet. dafa sañse tey bi muy génn.

saŋ w- : dëtt j-, mbér m-. demal kër doktoor ñu raxasal la sa góom bi, dindi saŋ wi yépp ba mu set.

sapp : sapp baat la bu ñuy dàqe muus. dinañuy wax tamit sib.

saraax : (ne saraax). baatu saraax dafay tekki lu jékki jékki rekk dugg dugg bu gaaw ci ab béreb. jinax ji ne na saraax ci pax mi.

saraxndiku : dugale ndox ci bakkan, génnewaat ko. dafa fàtte saraxndiku bi muy jàppu. dinañuy wax tamit soroxndiku.

sarax : joxe sarax. suba gu jot, dina sarax yalwaankat yi.

saraxolle b- : saraxolle turu waaso la.

sarbet b- : sarbet bi muy sangoo dafa tooy.

sarbi b- : sàmm b-. tey sarbi bi dafa gudde.

sareet b- : xamul nu ñuy tooge ci sareet.

sargal : ndokkeel. ku def lu rëy, dañu la war a sargal.

sarica b- : sarica mooy kadó bi ngay andiwaale soo tukkee ba ñëw.

sarmi-saraan b- : bantu digg bu mag buy nekk ci ab xëdd lañuy tudde sarmi-saraan.

sar : dugge fii génne fee. balu fetal bi ñu ko jam dafa sar.

sar b- : coppret b-. sar baat bu ñaaw la.

sartifikaa b- : sartifikaa ab lijaasa la booy am ginnaaw boo jàngee nasaraan juroom-benni at fii ci Senegaal.

sart b- : lu nit ñi tënk daakoor ci, anam b-. ci yan sart la la waa ji joxe kër gu rafet gii ?

sarto b- : daggukaayu ñax. jëlal sarto bi dem gubali fas wi.

sarwiis b- : liggeey b-. ki la fey xaalisam, danga ko war a defal sarwiis bu baax. / bérebu liggeeyukaay b-. suñu ñaari pàppa yee bokkoon benn sarwiis.

sarwisdiisen b- : sarwisdiisen mooy saytu cetug nit ñi ak li wër seen dëkkuwaay yi.

sarxolle : yuuxu. naka la woykat ba duggsi rekk, ñépp sarxolle.

sas 1 : jox ab liggeey, yen. li la askan wi sas, fexeel ba defe ko ni ñu ko bëgge.

sas 2 : ëskëy. sas doom ! robb bi rafet na.

sasi b- : kaadaru daamaar b-. daamaar gi sasi bu dëgër la yore.

satala g- : jàppukaay b-. abal ko satala gi mu jàpp.

satu-mbar w- : jamonoy nawet ji asamaan si di xiin rekk te duy faral di taw. ci satu-mbar wi la fi ñëwoon.

sawale : tas, tasaaroo. bàndi yi dañoo séen takk-der yi rekk, sawale. safaan wi mooy dajaloo.

sawara s- : dinañuy wax tamit safara s-. (seetal safara)

sawar : jàngalekat bi dafa sawar. safaan wi mooy tayal wala yaafus.

saw : tuur-ndox, gaanuwaay. bàyyil saw ci mbedd, loolu du jikko ju baax.

sawoor b- 1 : sawoor rab la wuy yàq dugug.

sawoor b- 2 : kaco-kaco b-. sawoor yi bare nañu ren. dinañuy wax tamit sawóor b-.

sawóor b- : dinañuy wax tamit sawoor b-. (seetal sawoor)

sax 1 : génne ci suuf su dee gàncax. gerte gi tàmbali naa sax. / li ngay def, su dee lu baax, nanga ci sax.

sax 2 : yaayam sax su waxee, mu saaga ko.

saxaar : génne saxaar. póno yi etijaŋ yi taal ñooy saaxaar.

saxmaar s- : turu xorom bu guddi jottee, saf-cin l-. tudde xorom saxmaar bu gudde biddaa rekk la.

sax w- : wer w-. gerte gi dafa am ay sax. dinañuy wax tamit gasax w-.

sayaan g- : teen bu xóotul dara. sayaan bare na seen gox ba. dinañuy wax tamit seyaan g-.

say : daanu-rab. ndéem dafay say, yóbbuleen ko kër doktoor.

say w- : takk b-. taxan na ñaari sayi matt.

saytaane : moo dafa saytaane ndax dafay boole nit ñi ñuy xuloo rekk. dinañuy wax tamit seytaane.

saytu : toppatoo. li ñu la jox ngir nga saytu ko, def ko sa yëfi bopp.