dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

sófoor b- : yow sófoor bi, danga war a xam ne ay doom-aadama nga yeb ci sa oto bi.

sómbi m- : gósi b-. ñi fiy reere sómbi ñoo fi dàq a tiitaru.

sóob 1 : tàmbale taw. nañu gaaw ñibbi bala taw bi di sóob.

sóob 2 : dugal. bala ngay sóob sa loxo ci aw ñam, nanga raxasu ba pare. / wax rekk. dafay sóob rekk wànte su doon moom tamit du ko def.

sóob 3 : beesalaat. dafa sóob ceen gi.

sóon : dinañuy wax tamit mboq. (seetal mboq)

sóonu : dinañuy wax tamit séweenu wala sóweenu. (seetal séweenu)

sóor : sotti ceeb wala leneen lu ñuy togg ci biir cin li. xaaral añam bi, sóor na ba pare.

sóox w- : morso yàpp b-. xaj bi jël na benn sóox ci yàpp wi. dinañuy wax tamit suux w-.

sórin b- : teenu-kalañ b-. teen bu ñu raaxul ci kow mooy sórin.

sóweenu : dinañuy wax tamit séweenu wala sóonu. (seetal séweenu)