dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

rubbë : baatu rubbë ci kàddug dugg ni Rubbë lañu koy gis. kàddug dugg ni Rubbë mu ngi tekki def lu la jural njàqare gu tar. (ci ni ñu koy nettalee, Rubbë mbindaanu gornoor la woon, ca jamonooy tubaab ya, bu dawoon dem ginnaaw bu mu tàbbalee doomu gornoor bi mu doon tiye ci ab teen). moom dee dugg na ni Rubbë ndax dañu ko jàpp muy tux yàmbaa.

rucci : dinañuy wax tamit rocci. (seetal rocci)

ruggi : futti. bi ñu jàppee woyu bi, dañu ko ruggi ci digg mbedd mi. safaan wi mooy solal.

rukk : wol, dëbb lu tuuti te wow. poobar bi lay rukk.

rumbax : baatu rumbax dafay ànd ak baatu mokk di tekk bu baax. gerte gi mu doon dëbb mokk na rumbax. dinañuy wax tamit rupp.

rung : dox, tànku. bi oto amagul woon, nit ñi dañu daan rung.

rupp : dinañuy wax tamit rumbax. (seetal rumbax)

ruq b- : koñ b-. muus maa ngi nelaw ci ruq bi.

rus : am gàcce. dafa rus ndax li ñu ko bett muy sàcc.

rututum b- : dóom bu tàng, gël b-. bul laal rututum bi, dafa lay lakk.

ruuj 1 : dindi ay gajj wala ay gittax ngir setal ab tool. Yàlla ji taw na te ruujagul benn toolam.

ruuj 2 : baatu ruuj dafay ànd ak baatu sew kese te di tekki lool wala ba ëpp. ndaw si jëkkër ji dafa sew ruuj. safaan wi mooy dijj wala am-yaram.

ruumandaat : wax ci suuf. sa jikko ju bon ji nga yore la waa koñ bi di ruumandaat, seetaatal sa bopp.

ruum b- : suufu néeg b-. masoŋ bi dër na ruum bi ba pare.

ruu g- : fit w-. sunu borom jël na ruu gi bu yàgg.

ruuñ b- : ragu yàpp b-. ruuñ la togg reer tey.

ruur 1 : ñaay, yàq. bëy yi ruur nañu tool bi yépp.

ruur 2 : ruur mooy suul dara ci suuf wala ci dóom. safaan wi mooy sulli.

ruusaanu : dikkee nit ginnaaw, yoofaanu. dafa ma ruusaanu mootax gisuma ko woon.

ruus : rot, wadd, daanu. xobi garab gi yépp ruus nañu ci suuf.

ruux 1 : roof. bul ruux bant bi ci matlaa bi.

ruux 2 : joxe ay mettit ci ay cër (tànk wala loxo). ne na doktoor bi ay weer a ngi nii tànkam yi di ruux.

ruy 1 : seey. permeyaabal bi dafa ruy. safaan wi mooy way.

ruy 2 : togg fonde bu ñu arawul. malaat bi ruy rekk la mën a lekk.