dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

robbiku : xolliku, xub. bool bi dafa màgget bay robbiku. dinañuy wax tamit xobbiku wala xobbeeku.

robb b- : robb bu jekk la soloon ca xew la.

rob : dénc, suturaal, suul. tey lañuy rob néew bi.

roccantal : takk, fas, njoñ, jéng. roccantal ko ndax mu neex a tekki.

rocci : seppi, sekki. woyu bi dafa rocci paaka bi rekk, ñépp daw. dinañuy wax tamit rucci.

rodd : dagg. lañset a ko rodd.

rogaat : siit. ndox maa ngi roogaat ci miir bi. dinañuy wax tamit roogaat wala roogalaat.

roggandi : teg beneen sër ci am mbootu. nanga roggandi xale bi bala muy daanu. dinañuy wax tamit rogganti.

rogu : xeelu. lan nga def ndaw si ba mu lay rogu ?

rokk : baatu rokk dafay ànd ak baatu yem di tekki ëppul mànkewul.

rokkos : roof, ñuux. rokkos na saaku bi ba mu fees dell ak ngooñ. dinañuy wax tamit nokkos.

romb-jaan b- : basaŋ b-, ndéstan g-. lal na romb-jaan bi ci ker gi, tëdd ci.

romb : weesu. dawal na oto bi ba romb dëkk bi.

ron g- 2 : ron xeetu garab la.

ron-ndoŋ g- : loos w-, baat b-. xeer wi ci ron-ndoŋ la ko dal.

rondal g- : suufu lal b-. dàll yaa ngi ci rondal gi.

rongoñ w- : dinañuy wax tamit rongooñ w-. (seetal rongooñ)

rongooñ w- : xale du génne rongooñi mag. dinañuy wax tamit rongoñ w-.

ronni : xool xoolin wu ñaaw, xeelu. lu mu lu la def ba nga koy ronni nii ?

ron : (ci ron). suufu (ci). dàll yaa ngi ci ron taabal ji. safaan wi mooy kow (ci).

ron b- : doomu ron b-. ay ron la yore.

ronqi : rocci. taal bi dafa yànj mootax mu ronqi ci ay matt. safaan wi mooy xamb.

roñ : toxal, toppale. kaña yi roñ nañu gerte gi fi nekkoon yépp.

roof : ñuux. nanga lem yére yi, buleen roof noonu ci saag bi. safaan wi mooy roppi.

roogaat : dinañuy wax tamit rogaat wala roogalaat. (seetal rogaat)

roogalaat : dinañuy wax tamit rogaat wala roogaat. (seetal rogaat)

roose : roose mooy sotti ndox ci gàncax ngir suuxat ko.

root : duy, tanq. root na ndaa li ba mu fees.

roppat : roñ benn, benn. sàcc bi roppat na takkaayi ndaw si yépp.

roppi : roppi na caabi ji, denc ko ne kenn du dugg ci biir néeg bi. safaan wi mooy roof.

ropplaan b- : awiyoŋ b-. ropplaan bi léegi la deppaar.

roq : caabi-lawbe j-. roq bant la bu ñuy gàll ci bunt ngir tëj ko.

roseet : (ne roseet). baatu roseet dafay tekki génn ci am mbir ba set ca wecc.

rot : wadd, daanu, tàbbi. caabim ji rot na ci yoon wi.

roy : seet ci li kenn di def nga koy def, toppandoo. sooy roy, nanga roy ku baax ak lu baax.

roy w- : naaf b-, nar b-, gar b-. nag yi dugg nañu ci biir tool bi, lekk lu bare ci roy yi.