dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

ribaa b- : loo moomul. bàyyil lekk ribaa.

rido b- : ajjil rido bi.

riggël : pare, mat. li mu doon def riggël na. dinañuy wax tamit rëggël.

riigu : toog, déju. demleen wuti liggeey, ngeen riigu ci ker gi rekk, di naan àttaaya. safaan wi mooy jóg.

riij 1 : dëbb lu tooy, nappaaje, wol. riij mooy dëbb lu tooy.

riij 2 : tëgg ndënd ndànk. nangeen riij rekk ndax buleen tanqal nit ñi.

riim : woy ci suuf. mu ngi liggeey di riim.

riiñoo : daje. dinañu riiñoo wax ci mbir moomu.

riir 1 : otoo ngi riir di ñëw.

riir 2 : daw topp. nag wi dafa riir wutali ko rekk, mu tëdd.

riisu : di dox ci wetu dara, leru. bëy waa ngi riisu sàkket wi.

riiti : dafay riiti ci xew yi.

rikkat : takkaat ay buumi tama ngir tàllal der bi bu baax, foddat. borom tama ji taxaw na di rikkat tama ji.

rikk : dinañuy wax tamit rëkk. (seetal rëkk)

rink : dinañuy wax tamit rénk. (seetal rénk)

riñaan : dinañuy wax tamit rañaan. (seetal rañaan)

ripp : baatu ripp baatu taq rekk lay andal di tekki ba mu ëpp. taq na ripp ci diw-tiir gi.

rittax : dinañuy wax tamit rattax. (seetal rattax)