dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

reegal b- 1 : reegal jumtuwaay la bu ñuy taraasee.

reegal b- 2 : baax g-. dafa nekk di gis reegal mootax julliwul.

reegalmaa b- : sart b-. ku jalgati reegalmaa bi, dinañu teg ay daan sa kow.

reen b- : mu ngi toog ci reenu garab gi.

ree : gënuloo ki ngay ree. dinañuy wax tamit reetaan. safaan wi mooy jooy.

reer : lekk ci guddi gi. reer na ba tëdd.

rees : tànkam bi néwwiwoon rees na léegi. / li mu doon lekk dafa gaaw a rees.

reetaan : dinañuy wax tamit ree. (seetal ree)

reew : xamadi, yàqu, ñàkk yar. dafa reew rekk wànte ki muy saaga du moromam. safaan wi mooy yaru.

regeju : dinañuy wax tamit ragagju. (seetal ragagju)

regg : suur këll. gan ñi lekk nañu ci yaasa bi ba regg. safaan wi mooy xiif.

rekket : (ne rekket). daje. sëriñ bi nee na démb ci guddi, dafa génn ne rekket ak jinne ji.

rekk : doŋŋ, kese, kepp, kott. Yàlla rekk ay buur.

rembat : dinañuy wax tamit remb. (seetal remb)

rembet : dinañuy wax tamit rembat wala remb. (seetal rembat)

remb : fees dell. paanu ndox bi dafa remb. dinañuy wax tamit rembat wala rembet.

remm : baatu remm dafay tekki lu ne tekk, deful lenn coow.

rendi : yow mënuloo rendi ginaar sax.

ren : at mi ñu nekk. seen pàppa dafay aji Màkka ren.

repp : repp mooy nekk di bëgg a am ay wala ngay bëgg a dee. / def lu wóoradi. dafa repp mootax muy taxaw ci pindu teen bi.

reqi : dagge ñax ci ndox ma mu sax. reqi nañu ñax mi nekkoon ci toolu ceeb bi yépp.

res w- : res yàpp wu nooy te neex la.

reso b- : reso mooy furno kuraŋ wala gaas.

rett : (ne rett). baatu rett dafay tekki jékki jékki rekk taxaw. mbaam mi dafa daw ba mu yàgg, mu ne rett, taxaw.

rewle : taxawu kuy am doom. ki war a rewle ndaw si ñëwagul. dinañuy wax tamit rewli.

rewli : dinañuy wax tamit rewle. (seetal rewle)

rey : dinañuy wax tamit ray. (seetal ray)