dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

raab : laxas póon ci ag kayit ngir tux ko. raab na takku póon bi yépp.

raadu : bay ak masin. ji na gerteem ba raadu ko.

raaf : yàqu ndax yàggaay. kër gi fi nekkoon boromam tóxu na ba mu raaf.

raam : dox ak ay wóom. gone gi dafay jàng raam.

raas : for. mu ngi wër di raas ay weñ.

raatale : diw, raay. raatale na bëer bi ci mburu mi.

raax 1 : masoŋ yi raax nañu miir bi ba pare.

raax 2 : boole ay xeeti pepp. dafa raax dugub jeek basi bi.

raay b- 2 : yoonu saxaar w-. raay du fowekaay.

raay-mbelle g- : powum jànq m-. xale yu jigeen yaa ngay def raay-mbelle ca mbedd ma.

raaya b- : daraapóo b-. dañu ko war a fonk suñu raaya réew.

raayduut g- : raayduut xeetu garab la.

raay : lekk na ba suur di raay biir bi. / diw, raatale. raay na pomaat bi ci taabam bi.

rabal b- : sëru njaago b-, dënk b-. rabal lañu muure séet bi.

rabat 1 : ràbb ñax ngir defar xëddu néeg. rabat nañu li ñu war a xëdde néeg bi yépp.

rabat 2 : xalaat. am na lu muy rabat fi mu toog.

rabax : sob ba mu ëpp, teeyadi. duma ko liggeeyloo dara ndax dafa rabax. safaan wi mooy teey wala yem.

rab w- : mala w-. rab dafa am bakkan ni yow. / yore rab, di daanu rab. waa ji dafa yore ay rab.

rafet-njort : am-yaakaar bu baax, bu rafet. danga war a rafet-njort ci li ngay def. safaan wi mooy ñaaw-njort.

rafet : taaru, jekk. kër gu rafet la tabax seen dëkk. safaan wi mooy ñaaw.

rafle : baatu rafle mu ngi jóge ci baatu raaf. seetal ci kow.

raf : yëngatu. yaram wi yépp a ngi raf.

ragaju : turne ay gët. góor du ragaju. dinañuy wax tamit regeju.

ragal : ñàkk a ñeme. dafa ragal rekk wànte àll bi dara nekku fi. safaan wi mooy ñeme.

ragg : bomb. ragg ko ak njàmpe ba mu set.

rag : dem ba jeexal meññent. guy gi rag léegi.

raj-rajloo : njëkkante di buuxante. nag yaa ngay raj-rajloo ca mbalka ma ndax mar.

rajax : (ne rajax). kaas yi daanu nañu, ne rajax.

rajo b- : ci rajo bi laa déggee xibaar bi.

rakkaati-gàmmu w- : juuroomeelu weer ci atum jullit. ci rakkaati-gàmmu wi weesu la judduwoon.

rakki-gàmmu w- : ñeenteelu weer ci atum jullit. ñibsi na ci rakki-gàmmu wi.

rakk j- : soo dimbalewul sa rakk, dinga dimbale rakku jàmbur.

ramaas : raafal, gobbi. waaa ji ramaas na li desoon ci njaay mi yépp.

ramatu b- : ramatu xeetu picc la.

rambaaj b- : waabajiiba b-, seytaane s-. moytu ko, rambaaj la, kër gu mu dem, tas ko.

rambax : safaan wi mooy yem, dal wala teey. (seetal teey)

rammu : ñaanal nit dara. yonent bi dina rammu.

rand 1 : sore. dinañuy wax tamit dand. (seetal dand)

rand 2 : def ci togg li war a ànd ak moom. rand na maafe bi ba mu saf sàpp. dinañuy wax tamit rënd.

rand g- : rand xeetu gajj la.

ranq b- : bëgëj b-, bisaab b-. bul fàttee def ranq ci ceeb bi de.

rañaan 1 : fàdd ci ay tànk. dafa ko rañaan mu daanu. dinañuy wax tamit raññaan wala riñaan.

rañaan 2 : dem ci guddi. bul rañaan, fanaanal ba suba. dinañuy wax tamit raññaan wala riñaan.

raññaan : dinañuy wax tamit rañaan. (seetal rañaan)

raŋ : def ag raŋ. nit ñaa ngi raŋ ci biro wote yi.

ras : dafa màgget ba yaram wi yépp ras.

ratatat : baatu ratatat dafay tekki coow liy jóge ci luy tàkk wala kuy wax rekk, du noppi mukk.

rat g- : rat xeetu gajj la.

rat m- : dangay naan rat, baax na ci.

rattax-làmmeñ : ku rattax-làmmeñ du denc benn sekkere. dinañuy wax tamit rattax-làmmiñ.

rattax-làmmiñ : dinañuy wax tamit rattax-làmmeñ. (seetal rattax-làmmeñ)

rattax : xollitu banaana dafa rattax mootax kenn waru ko sànni ci kow yoon. dinañuy wax tamit rittax.

ratt : génne meewu nag, xar, bëy wala leneen. moom mooy ratt nag yi yépp.

raw 1 : mucc. daw ba raw ci ngóora la bokk. (léebu). / duma, gañe, mën, daan. fas wu weex wee raw wu ñuul wi.

raw 2 : ràbb. dafa raw kawari bopp bi yépp.

raw-gàddu : njëkk-jël. po mi ku raw-gàddu.

rawaan y- : ay mbindeef yu deme ni jinne yuy àndi wërsëg. sëriñ bi ne na ko ay rawaanam ànduñu ak yu jabaram yi.

rawaasu : ràbbaske. buum yi dañoo rawaasu.

raw g- : ndaw g-. xale bu jigeen bi am na ndaw.

rax-ci-dolli : dafa yore sëqët su bon, rax-ci-dolli muy tux.

raxas : fóot, sàng. nanga raxas say tànk bala ngay yéeg ci kow lal bi.

rax : rax mooy def leneen lu bokkul ci am mbir wala dugal am mbir feneen fu mu dëkkul.

ray : rëbbkat bi ray na gaynde ci àll bi démb.