dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

rëb 1 : yëngu. seen koñ dafa rëb mootax mënu ma fa dëkk.

rëb 2 : rag. dem ba amatul doomu gerte bu ñu mën a for ci ab tool. taalibe yi for nañu tool bi ba mu rëb léegi.

rëb-rëbi : bañ a toog benn palaas. fu mu tollu mu ngi rëb-rëbi. safaan wi mooy yem wala teey.

rëbb 1 : dem ci àll bi wuti ay rab. dafay rëbb wànte du jàpp dara.

rëbb 2 : móolu, musibaal. bul fexe ba sa waa-jur rëbb la.

rëbëje : nax, njublaŋ. xippil sa gët yi, xool bu baax bala ñu lay rëbëje.

rëcc : raw, mucc. sàcc bi ñu jàppoon rëcc na.

rëcc m- : ñaareelu pàccu nawet biy am fukki fan ak ñett. ci jeexitalu rëcc mi la fi ñëw.

rëccu : ku ci fowe sa ndaw, bés dina ñëw nga rëccu ko bu baax. dinañuy wax tamit réccu.

rëdd : taraase. xale yee rëdd këriñ li ci miiru jàmbur bi.

rëgëjiin w- : rëgëjiin baatu teggin buy tekki awra jigeen la.

rëgël : togg. nanga wut jabar ju set te mën a rëgël.

rëgët : dàq ag gétt ngir yóbbu ko. ñetti pël ay rëgët nag yi.

rëggël : dinañuy wax tamit riggël. (seetal riggël)

rëkk 1 : dóor ci ginnaaw, xët, kuccal. yaayam a ko rëkk.

rëkk 2 : baatu rëkk dafay ànd ak baatu sës di tekki ay mbir yu sëslantoo, yu dara doxul seen diggante. bi ñuy dem gàmmu, seen oto bi dafa sës rëkk ci suñu bos.

rënd : dinañuy wax tamit rand. (seetal rand)

rëŋ-rëŋ b- : yoon wu bon w-. jaar ci rëŋ-rëŋ bi dafay yàq yaram. dinañuy wax tamit raŋ-raŋ b-.

rëppeel : daane nit mu sëpp ay yoxoom. dafa rëppeel ki mu doon bëreel.

rëppët b- : rëpët dawinu fas la.

rëq : foxoj. loxo bi dafa rëq.

rës 1 : (rës ne). rës baat la buy toppandoo am coow. póno oto bi ne na rës toj.

rës 2 : ñàkk a taxaw bu baax, bëpp. barigo bi rës na.

rët : xaw a tiit. nee na ñeme na xaj te saa yu ko gisee rët.

rëx : rendi géleem, loj. ndax dinga mën a rëx gélem gi ?

rëy-gat : bare tiitar ba mu ëpp. janq bi dafa rëy-gat. dinañuy wax tamit réy-gat.

rëy-làmmeñ : bare wax ba mu ëpp, dijj-làmmeñ. ndaw soosu dafa rëy-làmmeñ, soo ko takkee mu rey la ak wax. dinañuy wax tamit rëy-làmmiñ, réy-làmmeñ wala réy-làmmiñ.

rëy-làmmiñ : dinañuy wax tamit réy-làmmiñ. (seetal réy-làmmiñ)

rëy : ngand. garab gu rëy a nekk ca digg dëkk ba. safaan wi mooy tuuti wala ndaw. / yëkëti sa bopp. dafa rëy rekk mootax muy doxe nu mu tolluwul. safaan wi mooy wàcce sa bopp. dinañuy wax tamit réy.