dalub web bi leen di jàppale, ci jàng ak jàng bind làkku wolof

sàqum baat wolof-wolof

réccu : dinañuy wax tamit rëccu. (seetal rëccu)

réegal : baaral. dafay réegal togg gi.

réere-mbir : (réere-mbir ne). ñàkk a xam. dafa réere-mbir ne xale dafa war a jàng. safaan wi mooy xam.

réer : sànku. ay dàllam dañoo réer. safaan wi mooy feeñ. / dee. seen maam réer na bu yàgg.

réew : kenn ku nekk dafa war a fonk réewam.

réjj : (ne réjj). baatu réjj dafay tekki jékki jékki rekk toog ci lu amul benn waajaay, mbàpp (ne). dafa yegsi rekk, ne réjj ci lal bi. safaan mooy bëret (ne).

réll : (ne réll). dinañuy wax tamit ràll (ne). (seetal ràll)

rénk : nooj. gone gi dafa rénk. dinañuy wax tamit rink.

réstoraŋ b- : bérebu lekkekaay b-, paasiyoŋ b-. ceeb bu neex lañuy jaay ci réstoraŋ bi.

réy-làmmeñ : dinañuy wax tamit rëy-làmmeñ. (seetal rëy-làmmeñ)

réy-làmmiñ : dinañuy wax tamit rëy-làmmeñ. (seetal rëy-làmmeñ)

réy : dinañuy wax tamit rëy. (seetal rëy)